JUB, JUBAL AK JUBBANTI CI KOW TALI YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Naalu “Jub, jubal, jubbanti” fa mu duutoon baaraamam teggiwu ko. Kilifay Càmm gu bees gi ña ngay wéyal di def seen liggéey. Ba tax na, jëwriñu dem bi ak dikk bi jëloon na ay matuwaaay ngir jubbanti dawalkat yi. Looloo tax ba mu sàrtaloon ay daan ak i alamaan, teg ko ci ndoddi dawalkat yi ngir kaaraange ci kow tali bi.

Mu tollu ci ay weer kepp ginnaaw ba ñu ko sàrtalee, kilifa yi ŋànkoon boobu liggéey rëddoon nañu ay xët di ci leeral lañuy tere, daan ya ca mën a tukkee ak alamaan ja ñu ca gàll. Mu mel ni, la woon wonni na. Ndax, reewande gi ñu daan gis ci tali bi, di faat ay bakkan, njeexital yaa ngay tàmbalee feeñ. Ci ay weer kese, ñi yor boobu liggéey guufaan nañu lu ëpp 90 ci ay tamndaret (miliyoŋ) ci sunuy koppar.

Ñu jotoon jubanti yenn ci ay tabaxin ci yoon yi. Lu ci mel ni wiiraasu Gàddaay. Bokk na ci li ñu fésal ci seen liggéey boobu, ñaari dawalkat yi ñu nangu woon seen i këyiti dawal ndax po ma ñu doon def ci otorut bi. Ak yeneen ñaari dawalkat yu defoon laksidaŋ fa Jamñaajo nangu nañu seen i këyit.

Lañu seetlu nag, mooy ne, jëwriñu dem bi ak dikk bi, ju biir réew mi ak takk-der yi kafatuñu. Ñooñu séq boobu liggéey wone nañu ag mat ngir kaaraange way-tukki yi. Ndax, bu ñu sukkandikoo ci li takk-der yi (pólis, sàndarmari) fésal, lu mat 17 815 ci ay jalgati woññi nañu leen. Loolu di jur alamaan ju tollu ci 91 887 000 ci sunuy koppar. Mu nekk alal ju bari ju ñu dajale ci weeru me wii kese.

Mënees na jàpp ni caaxaan faaxe. Nde, ci kow tali, ay matuwaay jëlees na ko ci. Mu mën a indi ay saafara ci laksidaŋ yu bari, nekk tamit luy aar askan wi ci seen i tukki.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj