“KAFKA” LU MU NU WAX CI MAKI ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Téereb “Kafka” bii dafa lay jàngal lu bari. Ni àddina man a xëyee rekk soppiku. Ka nga nekkoon, nekkatoo ko. La nga doonoon, doonatoo ko. La nga mënoon, mënatoo ko. Ñi la wëroon, nga gis seen kanam ak seen taxawaay tàmbalee soppiku : cofeel ak wegeel di wàññiku. Xarab, diiŋat ak di la daw doon li fés. Ba tax nit ki war a bàyyi xel boobule bis. Ndax ki lay jay tay, la woon ba tax mu jege la, bu wonnee moo lay njëkk a sori.

Téere bii di “Kafka” dafa nuy nettali ndaw bu tudd Geregoor Samsa. Moom, Geegoor Samsa, yaxantukat la woon. Maanaam, dafa doon yëngu ci njënd ak njaay, di tukki ak a ñëw. Bés, mu yeewu, bëgg a jóg, yaram wi bañ. Mënut a jóg lal bi. Ci noonu, mu gis ne nekkatut ka mu doonoon : gis boppam ci jëmmi gunóor. Doonte xel mi ak xalaat yi dara soppikuwu ci, waaye jëmmam ja dafa soppaliku doon jëmmi gunóor. Kaawtéef ! Jaaxle dikkal ko.

Ay way-juram ak rakkam ju jigéen ñooy dund ak moom ci biir kër gi. Ñu xëy gis bunt néegu Geregoor tëju, ñu jollasante ak moom ay waat, mu tont. Ñu jàpp ne dara xewut. Ngóor si mu bokkal liggéey, xëy gisut ko, mu dawsi ci kër gi ngir xam lu ko téye. Bi ngóor si egsee, fëgg bunt bi, ñu jokkalante ay waat. Geregoor góor-góorlu ba tijji bunt bi. Kaawtéef ! Ngóor sa yuuxu daw. Nday ja yam ci moom, xëm ! Baay ja nar kaa ray. Rakk ju jigéen ja dawal yërmaande.

Mbokk yi jaaxle. Kër gi tàmbalee naqari. Ndax Geregoor a yoroon kër gi. Coono dikkal leen, ñu war a takk seen ndigg wuti am xëy ngir am lu ñu dunde. Ñu xaaj kër gi ñaar, dëkk ci benn bi, luye beneen bi. Bis ñëw, Geregoor génn néegam di doxantu, lokaateer ya yam ci moom, jommi, yanu seen i dàll, génn kër ga.

Rakk ju jigéen ja metitlu ko lool. Mu woo ndayam ak baayam ngir ñu xool nu ñuy teqalikoo ak Geregoor. Ñu teg seen i pexe, bàyyi ko moom doŋŋ, du lekk, du naan, du toppatoo. Coono dikkal ko, mu xëy dee. Ñoom ñu ànd defaraat seen dund. Rakk ja war a sëyi.

“Kafka” anam bi muy nettalee mbir mi, dafa ciy melal yii :

– Kàttan ak doole saxuñu ;

– Boo nekkee ak ñu la jàpp ndax sa mën-mën, bu la tële dikkalee, ñoo lay njëkk a daw ak lu ñu la jege jege.

– Ci sa digg-doole, bul nangu mukk ku lay jay. Deel saxoo di laaj ndax lii muy wax, bu tële dikkee dina wéy di ko wax ?

Muy nettali bob, doy na misaal képp kenn ci doom-aadama yi, rawatina ci njiit lu Yàlla dénk Nguur. Dangay doon gaynde, loo romb fél, fàdd, xët. Bukki yi dar la naan la yaw la. Puukare dab la, ngay xiirook a jaayu. Bew dikkal la, nga jàpp ne yow rekk yaa mën, yow rekk yaa sañ. Ngay buur di bummi, di guuxi lex ak a aj i mbagg. Bés ñëw, bett la, nga soppaliku doon gunóor. La woon wonni. Bukki yay xoolante, di seet nu ñu la dëggatee.

Maki, li dal Geregoor mi ngi lay yoot. Sag nekk gunóor du jaas ndax bukki yi dugal nañu la ba noppi. Say laaf tooy nañ xepp. Dootoo naaw.

Ña la doon wax Sàll Ngaari lamtooro, ñoo lay wax tey Sàll gunóor yaa torox. Waaye nag, lépp, yaa ko teg sa bopp. Yow rekk la. Waaw kay ! Dama ne, lu jiin Njaag a, te yaa di Njaag. Yaa ko sombi, naan ko.

Seexunaa Njaay
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj