Aliw Mamadu Ja ci 19i lawax yiy wut réew mi la bokk. Moom moo teewal làngug pólitig gii di PUR (Parti de l’Unité et du Rassemblement), féete ci kujje gi. Aliw Mamadu Ja nag, xar-kanamam bees na ci géewu pólitigu réew mi. Nde, ñenn ci askan wi desee nañu koo xam. Loolu, li ko wund, bokk na ci at yu bari ya mu de bitim-réew ci sababu liggéeyam ak i yëngu-yëngoom. Waaye, mu mel ni ñàkk a teewam ci réew mi, du ak coobareem. Ndax, picc a nga ca kow, waaye xel maa nga ca suuf. Loolu dëppoo ak ay tontoom ci laaj yu ni mel.
Aliw Mamadu Ja mi ngi fekk baax Saalum, fii ci réew mi. Mi ngi doore am njàngam ci dëkk bu ñu naan Caajaay, jaar fa Liise Demba Jóob. Am njàngam mu kawe ma nga ko defe ca jànguneb Séex Anta Jóob bu Ndakaaru. Bi mu fa amee ay lijaasaam yu mag, la jàll fa bitim-réew ( Farăs) ngir yaatal xam-xamam.
Ginnaaw loolu, ci la dooree ab liggéeyam ci bànqaasi yu mag a mag fa mbootayu xeet ya. Mu mel ni turam saf na sàpp ci xëti PNUD. Nde, foofu la defe lu ëpp ci ay atam di fa yëngu. Bu ñu sukkandikoo ci kàddu yi mu biral fa (faramfàcce), ci janoo bi mu séqoon ak Pàppa Ngañ Njaay, 20i at def na ko ci réewi Afrig yi.
Kon, ayla-yéwen Ja! Ndokk ba mu miise réewi Afrig yi nde seen jàngoro benn la. Muy wone ba tay ag xarañteem jëm ci jafe-jafe yiy lëmbe tund Afrig. Bokk na ci nu ñuy doxalee am réew, yoonu yokkute, ci fagaru ci jéyya yi ( mbënd mi, suuf yi yëngu), mën a salfaañe am réew te Nguur yi du ñu ci bàyyi xel. Xam-xamam mel ne ni ràmbasaale na lépp. Nde, laal na nu ñuy yore Nguur, fàttewul jigéeni kaw gi, xéyu-ndaw ñi ak bànqaas yi doxal am réew (mbay mi, càmm gi, añs.).
Jafe-jafe yi sonal réewi Afrig yu bari, am na ca saafara. Bokk na ca indi jàmm ag dal ci yenn dëkk yi. Mënees na tënk ne garabu ndóol ñëw na niki ni ñu ko ay farandoom yi waxe.
Leneen lañu gis mooy Aliw Mamadu Ja jar naa bàyyi xel ci wote yi ñu dëgmal. Ndax ma ngay wéy di wone boppam ci mitiŋ yi. Mbooloo mu tàkku moo koy gunge ci ay ndajeem.