KARIIM WÀDD BINDU NA, LÉEGI ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal wotey palug Njiitu réew ci atum 2024 door na bu yàgg te mbir mi agseegul. Ñu bari jot nañoo samp seen i ndënd, dëggal seen bopp te, ku nekk a ngi naan « Man a ! ». Ba ci kujje gi, xamagum nañu, walla njortagum nañu lawax yi ci nar sëgg bëre : Usmaan Sonko, Decce Faal, Maalig Gàkku, añs. Bu dee Xalifa Sàll ak Kariim Wàdd, Yoon mayu leen ñu bokk ndax daan yi leen yees leen daanoon, xañ leen seen i àqi maxejj. Fan yii yépp, nag, ñoo ngi fésal doomub Ablaay Wàdd jiy bindu, ca Tirkii. Ñu laaj ndax bind wala sax bindooti ci kayiti wote yi day tax a doon lawax, walla ?

Ñoo ngi gis, fan yii, ay nataal yuy wone Kariim Maysa Wàdd, fa Tirki, muy bindu ci Kayiti wote yi. Moom, lawaxu PDS bi, bu bindoo ca bitim-réew, dafa am lu tax. Ndax, ay at a ngi nii, mu tagatembe ca Qataar. Li waraloon ag gàddaayam di coowal luubal alal ju ko CREI doon toppe, te yoon daanoon ko ci, ba xañ ko àqi maxejjam, tere ko doon lawax. Dafa di, sàrtu woteb réewu Senegaal dafa yaxal ci dogub L31 ne, képp ku ñu daan lu ëpp juróomi ati kaso walla lu ko ëpp, du mën a wote. Te, ku mënu wote moom, mëneesu laa woteel. Maanaam, doo doon lawax ci wote yi. Lii moo gàllankooroon Kariim Wàdd ca atum 2018 ba mu bindoo.

Mu gisaat ne ci wotey njiiteefu réew gi ñu dëgmal, Kariim Wàdd tàyyiwut. Ma nga solaat ay dàllam bindujiwaat. Ñuy laaj lan moo war a doon yaakaaram ? Walla la ko daloon ca atum 2018 ndax du ko ci fekkaat ? Mbaa du dafa yaakaar ne Yoon far daan yees ko gàll, maanaam ñu amnisti ko ? Waa PDS de ne woon nañu ne Kariim Wàdd soxlawul ku ko amniste. Bu amniti naree am sax, àppub ñaari ayu-bés kepp a ci des. Loolu Njaga Silla, di aji-xam ci wàll woowu, xamle ci yéenekaay bii Enquete.

Senegaal, nag, bi Maki Sàll faloo ba léegi, saa buy wote jubsee, coow day am. Fàww rekk mu am ci lawax mu yelloo book bob, dinañ ko jaarale Yoon, xañ koy àqam ak i yelleefi maxejjam ba du bokk. Noonu la fa deme woon ñeel Kariim Wàdd ak Xalifa Abaabakar Sàll. Ñoo ngi laaj sax, naan mbaa bukkib Kariim bi du màtt Usmaan Sonko ? Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj