Ni ñu ko baaxoo gise ci njeexitalu at mu nekk, njiitu réew mi dina janoo ak askanu Senegaal ngir amal aw waxtaan. Mu mel ni lu ñu aadawoo la. Moo tax, bu bés baa, ñu bari dinañu tàllal seen i nopp ngir taataan i kàdduy kilifa yiy àddu ci bés bi, rawatina way-pólitig yi. Wëliis Njiitu réew mi, ñeneen dinañuy faral di ci wax ak askunuw Senegaal. Kariim Maysa Wàdd, doomu Ablaay Wàdd ji, Njiitu réew ma woon, wuutewu ko.
Kariim Wàdd, ci mbaali jokko yi la defe aw waxtaanam. Ci altine jii weesu, benneelu fan ci at mu bees mi, la doon sàndiy kàddu, jagleel leen askanuw réew mi. Mu far doon wokkatu bu daje ak geestu. Nde, ay at ñoo ngii ñuy séentu lawaxu PDS bi gàddaay boobaak léegi. Moom nag, Kariim Wàdd, yëgle na ne, gàddaayam gi léegi mu jeex. Ñu mën caa dégge ni léegi mu déllusi ci suufu Senegaal gi mu bëgg lool. Wax jii bokk ci kàddu ya mu biral ginnaaw ba mu ñëwaate ci gàddaayam googu mu sañul bañ.
Muy dem ga mu dem ca Qataar, ca suuf sa ñu ko uufee, ginnaaw ñatti ati kaso ya mu jot a dund ca ndung-siin. Mu toftal ca kàdduy nammeel ci suuf sii mu fekk baax. Tax ba mënul ñaanal ay jegeñaaleem, waaye siyaar ay soppeem. Ci wax jooju, mu fésal ak bokkam ci tarixa muriit ginnaaw ba mu tuddee sëriñam bii di Séex Siidi Moxtaar Mbàkke mi fi woon xalif, ak Séex Muntaxaa mi fi nekk.
Ci waxtaan woowu mën nañ ca déggee ay kàdduy cant ci ñi ko jàppale, dooleel ko ba mu yegsi fii. Fàttewut itam ay mbokkam ak ña mu bokkal làngu pólitig gii di PDS.
La mu tëje mooy yaakaar ji mu am ci ëllëgu Senegaal ginnaaw ba mu bësee xolam ci jafe-jafe ya mu dund te jàppu ca dara. La mu tànn mooy ag bennoo, juboo, jàppoo ngir ànd xeex jafe-jafe yi. Fàttewut itam ndawi réew mi ak lañu jot a dund ci mbëkk mi. La mu dige ak ñoom mooy ëllëg gu naat.