NJUREEFI SOROJ BI AK GAAS

Yeneen i xët

Aji bind ji

Réewum Senegaal a ngi waaj a jëfandikoo soroj bi ak gaas bi fileek diir bu gàtt. ñu ci séentu xaalis bu bare. Te, ku ne xaalis, na bànk. Ci gis-gisu ma-xareñ yu bari, Senegaal narul a jariñoo xaalis bi ni mu ware. Nde, ba jonni-Yàlla-tey jii, Senegaal amagul bànk bu mu moomal boppam. Bu ko defee, xaalisam, ciy loxo doxandéem lay nekki. Maanaam, koom-koomu Senegaal dafa nekk di dox te ajuwul ci benn bànk bu mu moomal boppam. Lees xam, te mu yenu maanaa, mooy ne, réew yu mag yépp ci seen i bànk bopp lañuy liggéeye. Daanaka Senegaal bu jëfandikoo sorojam ak gaasam tono yi ciy génn bànk jàmbur yee ciy jariñu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj