KOOM-KOOM GI : YITTEY YITTE YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Gaawu, 17 sàttumbar 2022 la Njiitu réew mi Maki Sàll tëral ag Nguur gu yees. Def na ci ay yeesal yu baree bari ginnaaw bi mu falee ay jëwriñ yu bees. Jëwriñ yooyu nag, sas na leen liggéey bu réy a réy bu ñu war a matale ci diir bi ko fi dese. Ci fànnu koom-koom gi, Soxna Ulimata Saar la Maki Sàll taamu ci kow Aamadu Hot mi mu dénkoon fànn wi. Moo war a doxal mbir yi léegi. Waaye, askan waa ngi xaarandi nag. Ndax, ci wàllu koom-koom, fépp a  dëgër.

Yeesal yi am ci Nguur gi tax na ba Njiitu réew mi dénk fànnu koom-koom gi jëwriñ jii di Soxna Ulimata Saar. Moom nag, bi Maki Sàll di biral ay kàddu ca bés boobule, bàyyee na ko ay santaane yu bari. Ndax li ci biir fànn woowu ay jafe-jafe doŋŋ la ni ki : yokkuteg dund gi, mbënn mi, xéyu ndaw ñi, añs. Ci yéenekaay bii di Le Quotidien, moo ngi ciy biral ne :

« Pexe yi ma war a tëral ngir dund gu jafe gi wàññeeku, liggéey mën a am, dimbali ndaw ñi ci sémb yi ñu bëgg a sumb, xeex mbënn mi ak yokkuteg luwaas yi, ñooy yi  ma gën a yitteel. »

Nde, moom Njiitu réew mi, dafa bëgg dund gi bañ a njëge lool ci ñépp. Donte ne sax am na liggéey bu am solo bu ñu jot a def moom ak Nguuram, ginnaaw bi Koronaa bi sonalee maxejj yi ak njeexitali xareb Riisi bi ak Ikren, moo ngi xamle ne dañu war a yokkaat jëf yi te liggéey ngir jëmale réew mi kanam.

Ci kow loolu, xamle woon na, keroog ca bataleem ba, ne :

« Ak li àddina si di jànkonteel tey ak ay jafe-jafe yu doy waar yi jëm ci yokkuteg dund gi, soroj bi ak laf gi, Nguur gi teg na ba noppi ay jumtukaay ngir aar réew mi ak dimbali njaboot yi ci lun xayma ci 620 miliyaar ci cfa. »

Waaye, dafa mel ni ba tey dañu war a wut yeneen i pexe. Te, Nguur gu yees gee ci war a taxaw ci nu mu gën a gaawe. Ndax kat, koppar gi doŋŋ doyul. Fàww ñuy lal ay pexe ak di wut ay jumtukaay yu wóor ba mën a njariñoo googule koppar.

Nde, ay xalaat yu am solo la Njiit li biral ci fànnu koom-koom gi ngir réew mi suqaliku. Waaye, lenn rekk a mat a sóor ci mbir mi, te mooy diir bi. Ndaxte, li ko dese bareetul. A waaw, lu ñoŋul ci diirub fukki at, ndax dina mën a ñoñ ci at ak i weer ? Nu xaarandi ba xam…

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj