KU TIITUL MAN TIIT NAA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Senegaal wote nañu dibéer ji weesu yamook ñaar-fukki fan ak ñeent ci weeru féewaryee. Ba démb ci alxemes ji ñu ngi doon xaar njuréef ya ca tukkee te këru-àtte gi war cee àddu. Loolu jur jiixi-jaaxa ci askan wi, bawoo ci kàddu yi nguur gi ak kujje giy yëkkati, ñii naan jéll am na ci songoo bu njëkk bi, ñi ci des jàpp ne njaax dafa am, fàww ñu sëggaat bëre. Daanaka askan wi aj na noowam, di xaar aji-àttekat yi séq Ndajem ndeyu-àtte mi àddu ci mbir mi.
Waaye bu nu xoolaatee yëf yi bu baax, wote bii tiitaange gu réy moo ci tukkee war a ñeel képp ku am seetlu. Ndaxam sax de, li tiital askan wi ajuwul ci lees gën a jàpp, mu jëm ci kan la yoon di nangul ne moo jël ndam li.
Li jur tiitaange gi, war naa yóbbu fitu képp ku yittewoo bàkku réew mi : “Wenn Askan, Benn Jubluwaay, Benn Gëm-gëm”.
Su nu waxantee dëgg, ñu bare seen woteb dibéer ci waaso ak tariixa la lalu woon. Di lu kenn mënul a nàttable. Li ma yokk tiit du lenn lu dul ne sunu réewi Afrig yi dañoo des di sooxaale ab góomu judduwaale. Mu méngook ne ay réew la yoo xam ne Bokk moomeel (Nguur) dafee jiitu Bokk Xeet (Askan). Li ko waral mooy waaso yu bari yu seen jaxasoo desoon, ñu yàgg a xare ci seen biir ba noppi nasaraan yi leen nootoon ci lu jege ab xarnu boole leen ciy Bokk moomeel ca diggante atum 1885 ak 1886 ca Berleŋ, péeyub Almaañ. Moone, yooyu waaso sax de, wenn askan lañu, ni ko Séex Anta Jóob wanee. Mu ngi nuy xamal ci téereem bi mu duppe “Civilisation ou barbarie” ne “Deret jiy daw ci samay siddit njaasu deretu wolof laak ju séeréer, ju saraxolle, ju pël, añs.”. Mu tekki ne waaso ak lu ni deme, waruñu fee jur ay. Waaye itam bu nu xoolee ci taarix, ñetti xarnuy njaam, fekki benn xarnub nootaange tax nañu askani réewi Afrig yi réere mbir li leen boole def benn.
Amaana looloo waral njiiti Afrig yu njëkk yi fullaaloon bennoob réew yépp, ñuy xàccandoo di dóorandoo. Ci loolu la ku mel ni Ufuwet-Buwaañi taxawoon ca réewum Kodiwaar. Ci loolu it la Seŋoor newoon, sukkandiku ci lu mel ne kalante giy dox ci diggante yenn waaso yi, moo xam séeréer laak pël walla joolaak séeréer, mbaa kalante biy dox ci diggante Njóobeen yeek Njaayeen yi, Jaween yeek Sekkeen yeek Géyeen yi. Waaye li seen liggéey di rafet yépp teewul ba tey njaw des aw xambin. Kon, simoŋ bi war a lëkkale waaso Afrig yi ngir mu taxaw fu dëgër, dese naa wow. Ngelaw lu ñàkk solo mën naa tasaarey réewam. Ku ko weddi na ko seet ci li xewoon Kodiwaar bu yàggul rekk. Benn baat kesee ko tas tasar, muy baatub “ivoirité”. Mu nuy fàttali tamit réewum Ruwaandaa ci atum 1994.
Nan fexe boog ba li tàmbalee raam ci dibéeru 24 féewaryee 2019 bañ a yegg ci ñag bi. Nan fexe ba mucc ci li toj Kodiwaar, rajaxe Ruwaandaa.
Daawuda Géy
 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj