Lan la wutaakon yi naral làkki réew mi ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Waaw mbokk yi, lan la wutaakon yi naral làkki réew mi ? Man ci sama wàllu bopp, déggaguma ci lu ma doy. Ndax Wolof, Pulaar, Séeréer, Soose, Joola, Sooninke…. dañu leen di wéy di suufeel teg Frãnse mbaa Àngale ci seen kaw ? Ndax Frãnse kese mooy wéy di nekk “làmmiñ wi Repibligu Senegaal fal, di ci jaarale léppam” ? Ndax làmmiñ yi xeetoo Senegaal dinañu nekk kenu njàngale mi, li ko dale daara yu suufe yi ba ci Iniwersite yi ? Ndax seen mbind, seen xabaaruwaay, seeni téere dinañu tas ci Réew mi ? Ndax dinañu fexe ba doomi Senegaal yëpp mën bind ak jàng ci làmmiñ yi ñu nàmp ?
Làmmiñu réew mi war na ñoo dugg ak doole ci daara yi ak ci kuréli njàngum liggéey yi, ñu ciy sàkku xam-xam : xarala, ladab, xayma, mbay, napp, tabaxin, mekanig, elektoronig, tas-xibaar ak ñoom seen…Su ko defee sunu Askan, sunu Xeet ak sunu Réew dinañu def jéego gu réy ci yoonu suqaliku ba dab réew yi seen koom gën a naat ci dunya. Jamono moom-sa-Réew jot na. War nañu fullaal làmmiñi réew mi, jox leen seen cër ba mu mat sëkk, ñu doon ay jumtukaay yu tàkku ngir tinkeeku. Yaakaar naa ne “Lu Defu Waxu” war naa mën a bind bataaxal juroomi wutaakon yi laaj leen li ñu naral làmmiñi réew mi
 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj