Coowal pólitigu Senegaal mi ngi wéy di jur jote ci réew mi. La ca mujj di layoob njiitul Pasteef lii di Usmaan Sonko ak Maam Mbay Ñaŋ, yokk na ci xar mi kawar. Ndax dal gi askan wi ne woon siiw, jàmmarloo ya woon kerook Alxames wokkati na goom bi. Askan wi wàcc ci mbedd yi, njàngaani lekkool ya feelu leen ca.
Muy ay ñaxtu yu jur yenn saa yi ay jàpp walla ay bakkan yu rot tax ba ndongo yi ak ñenn ci jàngalekat yi mer ba futtu. Sabab si di njàpp gi ñuy wéy di jàpp seen i moroom ak i naataango ci ñaxtu yooyu. Looloo tax ba waa CUSEMS, di kurél gi ëmb jàngalekat yi, di duut baaraam nguur gi. Li muy naqarlu mooy jàngalekat yeek ndongo yi ñu teg loxo, bundxataal gi ñu leen di bundxataal, rey wala jéem a rey maxejj yi ak takk-der yiy dugg ci lekkool yi ak gërënaad ya ñu fay sànni. Tax ba ñuy sàkku ci nguur gi mu bàyyi leen ci lu gaaw.
Ñu nemmeeku tamit ca Biññonaa, foofu ñu faate Mamadu Korka Ba, ndongo ya tàbbi nañu ca xeex ba. Looloo tax ba ñu génne seen i moroom ya ca kalaas ya, ne am njàng du fa ame. La leen metti di faat ga ñu faat seen moroom jooju. Mu mel ni, noonu la ko yeneen i ndongo ya fare ce Séeju defe. Ñoom tamit, dakkal nañu njàng ma ndax jafe-jafe pólitig yiy wéy di gaar njàng mi. Ca Tiwaawon, noonu la ko ndongo ya amalee, diy ñaxtu, tax ba ñu tëj lekkool ya. Ndongo ya féete ca diwaanu Ndar, ñoom tamit bokkoon nañu ca ña njëkk a jóg ngir seen moroom ya ñu jàppoon ca ñaxtu ya.
Mënees na wax ne coowal pólitigu réew mee ngi waaj a ëpp i loxo. Ndaxte, yamut rekk ci fànnu pólitig gi. Mu mel ni njàng mi ak njàngale mi bokk na ci fànn yi miy njëkk a jatt, muy ay jàngalekat yu ñuy jàpp, walla sax ay ndongo. Mu nekk luñ war a saafara balaa làmbaay a ñaaw.