LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (18/8/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

WÉR-GI-YARAMI ÑI ÑU JÀPP CI KASO YI

Kilifay caytug kasoy Senegaal yi génne nañu ab yégle di ci biral wér-gi-yarami ñett ci ñees jàpp ci kaso yi. Usmaan Sonko la, Muhammadu Sàmba Jiim (Anibaal) ak Séex Baara Njaay. Nde, ñett ñii, dañ doon xiifal ba far loof. Moo taxoon ñu jàllale woon leen « Réanimation » bu loppitaanu Principal, maanaam fa ñuy jéemee muccal ñi tollu diggante dund ak dee. Ci kow loolu, coow li bari woon na lool sax. Tey nag la njiiti caytug kasoy Senegaal àddu ci mbir mi.

Ci yégle bi ñu siiwal, ñu ngi ciy xamle ne, « ci bésub 18 bii nu nekk, weeru ut 2023, ñetti nit ñi jàpp kaso ñoo nekk fa « Réanimation » bu loppitaanu Principal bu Ndakaaru. Benn ci Muhammadu Sàmba Jiim (Anibaal) mi nga xam ne, 14i fan ci weeru féewaryee 2023 lees ko jàppoon. 28eelu fan ci sulet wii la dooroon xiifal gi, bésub 10 ci ut lañ ko rawale woon « Réanimation » ba.

Ñaareel bi mooy Séex Baara Njaay mi ñu jàpp keroog 9i fan ci suwe 2023, yóbbu ko « Pavillon spécial ». Moom it dafa doon xiifal ba jagadi, keroog 4i fan ci ut, ñu jàllale ko « réanimation ».

Usmaan Sonko lañu mujje tudd ci seen yégle bi, wax ne, bésub 31 ci sulet 2023 lañ ko dóoroon « mandat de dépôt », yóbbu ko ca kasob Sébikotaan. Moom itam da doon xiifal ba loof ci. Bésub 6eel ci ut lañ ko rawale woon fa « Pavillon teranga » bu loppitaanu Principal, ndax dafa sonnoon lool. Waaye, ci seen i wax, ci guddig 16 jàpp 17eelu fan ci ut la ame ag jagadi, ñu jàllale ko « Réanimation » moom itam.

Nee ñu nag, fajkati loppitaanu Principal yi jël nañ seen matuwaay yépp ngir toppatoo leen ni mu waree.

NGAÑ DEMBA TURE MU PASTEF GÀDDAAY NA FA MALI

Ngañ Demba Ture daw na génn réew mi ngir rawale bakkanam, rawale naalu làngug Pastef bim bëgg a aar. Ci xëtu facebookam la biral xibaaru gàddaayam fa Mali. Mi ngi dooree ci jagleel ay ngërëm njiiti Bokkeefu Mali yi ko dalal fa seen réew ma. Moom nag, nee na, li Nguur giy jëfandikoo doole ji ko askan wi dénk ak campéefi réew mi di ko xeexe ak a xoqatal kujje gi, rawatina Pastef, moo ko tax a génn Senegaal. Rax-ci-dolli, ciy waxam ba tey, dafa am liggéey bu réy bu koy xaar ci xeex bu nar a yàgg bii ñu war a xeex. Moo tax mu rawale boppam ngir bañ a tayle boppam noon bi.

FAAS-BÓOY : NDAW ÑA MER NAÑU

Coowal mbëkk mee tax ndawi Faas-Bóoy yi, fa diiwaanu Cees, mer ba futt. La ñuy ñaxtu mooy mbirum gaal ga yaboon lu ëpp téeméer ci ay ndaw, te wutali woon waaxi tugal ya. Nde, ba léegi, gisaguñu ndaw ña waroon gaal ga. Nee ñu, wër bi dafa yeex lool. Noonu lañu songee ay béréb, tojate leen.

JÀPP NAÑU BÉSUB MÀGGALUG TUUBAA

Turuw 18 Safar lees gën a xame bés bi. Muy bés bu màgg nag ci xew-xewi diine, fi biir réew mi. Màggalu Tuubaa xam nañ kañ lay doon. Muy yemoo ak 4eelu fan ci sàttumbaar 2023 bii ñu jub. Murit yi di ko waaj ak a tatagal ànd kook mbég.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj