Jeexal nañu démb ci dibéer ji, 29i pani sàttumbar 2024, njébbalug wayndarey lawax yi namm a bokk ci wotey Ngombalaan gi. Donte ne ci dibéer ji lañu àppaloon tëj gi, bari woon na làng yu bëggoon ñu yokk ci ñetti fan ba ayu-bés bii nu nekk. Waaye, loolu mujjewul a àntu. Nde jëwriñ ji daf ko ci yamale kepp. Bees sukkandikoo ci li yéenekaay yi siiwal nag, lu ëpp 150i làng ak i lëkkatoo bindu woon nañu fa DGE (Direction Générale des Élection). Waaye, ñi jot a jébbale seen i wayndare matul ñeen-fukk.
MBIRUM 94i TAMÑARET YA WOON
Coowal 94i tamñret ya woon dina leer. Xibaar la bu jóge ci Fadiilu Keyta, njiitu CDC (Caisse de Dépôts et de Consignations). Fekk ñu ko doon dalal démb ci dibéer ji ca jotaayu Grand Jury bu RFM. Naka noonu, mu biral ni dinañu càmbar mbir moomu ba mu leer nàññ ndax alalu askan wi la. Cig pàttali, mbir maa ngi laale woon ak Maamur Jàllo mi fi nekkoon njiitu « domaines ». Usmaan Sonko mi jiite tey Càmm gi moo ko boole woon ak yoon, ne dafa sàkkal pexe alal ju tollu noonu.
APR ÑÀKK NAY WAY-BOKK
Làngu pólitig gii di APR (Alliance des Forces de Progrès) ñàkk nay way-bokkam. Démb ci dibéer ji la ñu bari ci ñoom tekki seen i ndomboy-tànk yi ñu yoroon ci làng gi. Bokk na ci ñi ci gën a ràññeeku, Pr Umar Ñas, Satoor Mbay ak dépite Maalig Jóob mi topp ci Njiitu Ngomblaan gi. Am na itam ñeneen ñu teewal làng gi ci diiwaan yi ñu tekki seen i ndomboy-tànk. Bees sukkandikoo ci xibaar yi jot a rot nag, seen génnandoo jotewul dara ak taxawaayu APR ci wotey Ngomblaan gi ñu jëm.
NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI
Jëwriñu njàng mi, Mustafaa Giraasi yóbbu na 1500i jàngalekat ci ekooli tuut-tànk yi, ci ekool yu suufe yeek ekoolu alxuraan yi. Am na itam 501i jàngalekat yu mu dugal yu nekk ci daara yu digg-dóomu yi. Yóbbu gi mu leen teel a def nag moo ngi aju ci bëgg a tàmbalig njàng mi matale ci ubbite gi. Dañoo seetlu ni ay ayu-bés ginnaaw ubbite bi lañu daan yóbbu jàngalekat yi ba tax mu daan andi ay yéex-yéex ci njàng mi. Naka noonu, jëwriñ ji dellu na ñaax jàngalekat yooyu ñu gaaw a dem ci seen i bérébi liggéeyukaay yi nu mu gënee gaaw ngir ñu matal ubbite gi ci bésub 3 oktoobar 2024 bi ñu jàpp.
“OCTOBRE ROSE”
Weeru oktoobar bii nuy dugg lañu jagleel xeex jàngoroy kañseer. Ngir waajal ko, kurél gii di LISCA (Ligue Sénégalaise contre le Cancer) doon na amal ab doxantu biir Ndakaaru ngir xértal askan wi ci seen xeex bi. Gaawantu nañu ci seen doxantu boobu itam ngir tàllal loxo Nguur gi ak maxejj yi. Bees sukkandikoo ci li seen njiit li biral, moom Faatma Gënun, lu ëpp 400i jarag ñoo ngi tëdd ci atum 2024 mi di xaar ñu faj leen. Nde, faj leen dafay laaj alal ju takku. Ca atum 2022 rekk amaloon nañu ndajalaatu ba am 200i tamndaret. Waaye, jaay nañu lu ëpp 220i tamndaret ngir taxawu jarag yi. Ba tax ñuy ñaan Nguur gi ak ñi ko mën ñu dimbali jarag yooyii kañseer bi tëral, ñu mën a faju.