Liggéeykat yi ëmb Intersyndical bu raglub Maam Abdu Asiis Sy Dabbaax, amaloon nañ ab doxu ñaxtu, takk ak ay sagar yu xonq. Li leen tax a jóg mooy fexe ba ñu leeral 60i tamndaret yoy, nee ñu dañ leen luubal ca biir raglu ba. Mustafaa Géy mi yoroon seen kàddu xamle na ne, ñoom, li ñu « bëgg mooy ñu indil nu ay leeral ci 60i tamndaret yi ñu luubal ci biir raglu bi. » Mu teg ci ne, li leen tax a jóg « du lenn lu dul aar ak a jagal lépp luy jumtukaayu raglu bi, rawatina liggéeykat yi. » Bees sukkandikoo ciy kàddoom, taxawaleesoon nab kurlug luññutu « ngir lëñbët mbir mi. Waaye, boobu ba léegi, dara leeru ci. » Looloo leen tax a génn ci mbedd mi, di kaas ak a naqarlu, te duggewuñ lu moy leeral li lëndëm ci mbir mi. Te, nag, lépp lu mu laaj, ci seen i kàddu, dinañ ko ci def ngir raglu bi gën a dox, lépp di jaar ci yoon.
NJÀNG
Jàngune Gaston Berger am na « Recteur » bu bees.
Àllarba jii, 1 Màrs 2023, lañ doon amal Ndajem jëwriñ mees toxal fa Seéju. Ca moomu ndaje lañ tabbee kii di Màgget Njaay, « Professeur titulaire des universités » Recteur bu bees bu jàngune Gaston Berger bu Ndar. Mu nekkoon lu waa SAES doon sàkku ñeel daara ju kowe yi.
PÓLITIG
Cosug lëkkatoo gu yees
Ginnaaw Yewwi Askan Wi genn ci lëkkatooy kujje yi sosu woon ci wotey gox-goxaat yi te nekk jamono jii ci tànki tas. Geneen lëkkatoo gu yees sosu na. Lëkkatoo gi ñi ngi ko dippe Yewwi Senegaal. Moom nag boole na lu tollu ci juróom-benni mbootaay. Muy And Dooleel Senegaal/Parti du changement, FPRS/And Liggéey, Pare Suqali Senegaal, Union patriotique Bëgg sa réew, UPRS/Yewwuleen, Senegaal rekk. Ñoom nag seen mébét mooy samp benn lawax ci wotey palum Njiitu réew yu 2024 yi.
Jot na fekki na BBY
Lëkkatoo gii di Jot na/Patriotes pour l’Alternative génn na kujje gi, fekki Nguur gi. Ñoom nag, nee ñu bëgg ag suqaliku ak ag dal ci réew mee tax ñu jël ndogalu dooleel kii di Njiitu réew mi Maki Sàll ci liggéey bi.
Yeneen tabb yu yees
Ca ndajem jëwriñ ma mu doon amal démb, kii di Njiitu réew mi Maki Sàll jot na faa amal ay tabb yu yees. Ñi mu fa takkal i ndombo-tànk nag ñii la : Màgget Njaay (Recteur de l’Université Gaston Berger de Saint-Louis), Momar Ndaw (Président de la Commission nationale de Régulation des Loyers des Baux à Usage d’habitation (CONAREL) au Ministère du Commerce, de la Consommation et des PME), Malaŋ Séyni Faati (Secrétaire exécutif de la Commission nationale de Régulation des Loyers des Baux à Usage d’habitation), Mademba Géy (Directeur général du Centre de Formation judiciaire au Ministère de la justice), Allaaji Baabakar Jóob (Directeur des Services Judiciaires au Ministère de la justice), Abdulaay Njaay (Directeur de la Justice de Proximité et de la Promotion de l’Accès au Droit au Ministère de la justice), Uséynu Géy (Directeur de la Dématérialisation et de l’Automatisation des Services Judiciaires au Ministère de la justice). Ñii ci topp tabb nañu leen ay jàngalekat ci bànqaas bii di Faculté des Sciences et Techniques de L’Université Cheikh Anta Diop de Dakar : Fabe Iddiriisa Baro (spécialité, Physique/Energie scolaire), Isaa Jaañ (Thermique, thermodynamique, Maxtaar Geen (Chimie physique (Electrochimie), Maam Sàmba Mbay (Botanique-Systématique-Ecologique), Momar Njaay (Chimie analytique : Chimie de l’Environnement), Bàlla Jóob Ngom (Physique du solide-Science des matériaux), Daawuda Ngom (Agroforesterie/Ecologie).
TÀGGAT-YARAM
Wure : FA Cup / Àngalteer
Ilimaan Njaay toogloo na Paap Mataar Saar ak Totenham. Nde, moom moo dugal benn bii bi am ca seen joŋante démb ba ñeel kuppeg Àngalteer bi. Ilimaan Njaay doorul woon joŋante bi. Dafa dugg rekk taal kër gi.
Barça
Tey ci alxemes bi, waa Barça, ci seen i mbaali jokkoo, xamle nañu ni Joao Mendes de Assis Moreira, doomu Ronaldinho bi, bokk na ca biir këlëb ba léegi. Beneen Ronaldinho ca biir Barça.
LÀMB : SAA-CEES AK RËG-RËG
Dibéeru 5i Màrs 2023 jii lañu war a sëgg. Làmb jooju nag, du yomb. Ku nekk a ngi wax rekk, naan “bu bés baa, lii ak laa”. Ñaar ñu neexoo doole daal, seen bëre du yomb.