LIGGÉEKATI INIWÉRSITE YI JÓGATI ÑANU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njàng mi ak njàngale mi dafa mel ni du jóg ciy njàmbat. Mënees na koo waxe noonu. Daara yu kawe yi moom ñoo faf waabale lépp. Ndax, bu dul ndongo yi, di jàngalekat yi walla sax liggéeykat ya fay yëngu di wone seen i jafe-jafe ya ñuy jànkoonteel. Ci loolu, kurél gi ñu dippe PATS ( personnels administratifs, techniques et de services) bu daara ju kawe ja ca Seex Anta Jóob ña nga ca.

Muy ag yëngu-yëngal gu ñu dàbbali ginnaaw seen ndaje ma ñu doon amal. Kurél googu di wone seen mer ca lañu doon sàkku ci jëwriñ ji ñu dénk njàng mu kawe mi leen boot. Mu mel ni seen xeex boobu léegi mu booy i nopp waaye la leen metti mooy tanqamlu gu ñu leen di tanqamlu. Walla sax nopp bu bon bi ñu leen jox ci seen i ñaxtu. Cig pàttali, la ñuy dagaan ci seen jëwriñ jooju di nekkiin wu gën ci seen liggéey. Waaye di ñaan yokkuteg payoor. Muy ay xaatim yu ñu defoon ak seen màkkaan googu. Waaye, la teey xel, te xel mënu koo nangu mooy deeltu ginnaaw gi seen màkkaan googu def ginnaaw ba ñu déggoo ca loolu ba noppi. Muy lu seen njiit lii di Farãsuwaa Baabakar Ture ñaawlu ci ay kàddoom :

“ Muy ag ñàkk a wég gu réy, ag ñàkk teggin. Looloo tax ñu delloo buum ca mboy-mboy ga doonte ñu ngi woon ci tànki tëgg ñaxtu gi ci suuf”.

Muy mel ni xol bu jeex lañu ame tax ñu jógati, bank seen i loxo. Ñu àpp ko ci lu tollu ci ñeenti fan yu ñu dul liggéey. Ñu gis ne seen serenglu googu ma ngay jur ay gàllankoor ca bérébu jàngukaay boobu di UCAD. Ndax béréb yu bari ya ndongo yay soxla dañoo tëj. Lu ci mel ni kàggu ga ndongo yay amale seen i dawal wala ay gëstu ci seen um njàng. 

Kon, warees na wut ay saafara jëm ci jafe-jafey képp kuy yëngu ci biir daara yu kawe yi. Ndaxte, gis nañ ne seen liggéey, lépp a lëkkaloo. Te bu benn doxut rekk mën naa yobbaale yeneen yi, ba jur yeneen i jafe-jafe.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj