Woteb Mahdiyu bi, ku nekk dégg na ko. Mu doon xew-xewu diine bu njabootu laayeen di màggal at mu jot. Ren di yamook 143eelu yoon bi ñu koy amal. Kàmbereen, Yoof ak Ngor nar a dékku ci Gaawu ak Dibéer bii mbooloo mu takku ngir màggal bés yooyu.
Tarixa Laayeen nekk mbooloom diine mu mag moo xam ne Seydinaa Limaamu Laay moo ko sos. Kilifa gi mu ngi gane jamono ci atum 1843 ca Yoof. Doomi Maam Alasaan Caw ak Soxna Kumba Ndóoy boroom “Aajiboo daaya laay” nekk ab woteem, door ci atum 1883. Mu bokkoon ci mag ñi taxawal Lislaam ci Afrig soowu jànt. Loolu tax ba Tubaab yi ci jamonoy nooteel ya génne woon ko réew mi, yóbbu ko Gaboŋ. Ab xeexam mu def ko ci dal ak jàmm ba ni mu wuyujee Boroom bi ci atum 1909. Seydinaa Limaamu ma nga tëdd ca sëgg ya ca Yoof.
Woteb ren bii yamook tolluwaayu réew mi ci ay yëngu-yëngu tax ba kàdduy soññe ya ca ëpp jëm ci loolu. Muy ay ponk yu far ngir indiwaat taalibe yi, maxejj yépp cig dal. Ci loolu, Njiitu réew mi Màkki Sàll ci siyaar bi mu amaloon ci kanamu Muxammadu Maxtaar Laay di xalifa yoon wi, ma ngay feddali taxawaayu Nguur gi ci lépp li ko war di ay wareefam. Muy ay tontu yu jëm ci ñàkk a weg ak taafar yi ñenn ci nit ñiy def jëme ko ci kilifay diine yi.
Jot nañoo àddu tamit ci dal ak jàmmi réew mi ñenn ci way-pólitig yi nar a salfaañe. Muy lu mag ñu mel ni Seydinaa Limaamu suuxat ba mu am ci réew mi. Moo tax kenn du seetaan loolu di yàqu. Seydinaa Isaa Caw Laay miy lëkkale xew-xew bi indi na ciy leeral. Muy wax naan: “benn xew-xewu pólitig warul yëngal réew mi”.
Mënees naa wax ne woteb Mahdiyu ab xarnu ak lu teg, mi ngi wéy ci yoon ma mu xàlloon, di woo nit ñi ngir ñu wuyuji wooteb Boroom bi. Mu nekk tarixa buy bàkkoo ci baatu laa-i laaha illalaahu, seen colko gu weex di màndargal jàmm. Jàmm miy kenub lépp.