LU ЁPP TUURU !

Yeneen i xët

Aji bind ji

xibaarRéewum Senegaal rafle na jàmm ci jamono jii, muy ci kàddu yi gaa ñi di yékkati ak ci seen i jёf. Lenn waralu ko nag lu dul wote yees dёgmal. Saa su gaa ñi jàppee àpp ngir amal i joŋante, fitna yewwu. Te, ay moom mёnul rombu baay dee na. Ndax, am ndajem ñaxtu kepp jaaduwul ay nit di ca gaañu waxatumalaak am ñu cay ñàkke seen i bakkan. Mu mel ni ñiy jàmmaarloo du ñoom ñépp a bokk réew mi. Ba, ku nekk ci ñoom àttan a rey moroomam, muy takk-der bi, di maxejj bi. Loolu moom, ndax am na njariñ bu dee ñoom ñépp defar réew mi kepp a leen ñor ? Waaye, laaj bi mat a samp fii kay mooy fu coow li waral ay bakkan di rot doore ? Ak ban taxawaay la ci yoon am ?

Yewwi Askan Wi amaloon nam ndajem ñaxtu ca bérébu Obelisk juróom-ñetti fan ci weeru Suwe gii weesu. Léegi, bi ndaje moomu jàllee, ñi jiite lёkkatoo gi daldi génn, sant seen i militaŋ. Bi ñu paree daldi leen joxaat dig-daje àjjuma fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru Suwe. Ñu jébbal seen kёyit googu ngir yёgal kilifa yi seen ñaareelu ndajem ñaxtu moomule. Loolu, mi ngi méngoo woon ak fukki fan ci weeru Suwe. Waaye, ca bés ba la njiital dёkk bii di Ndakaaru (gouverneur) génnee ab dogal. Dogal bi mi ngi tёnku ci dog 61 di tere bépp xeetu ndajem ñaxtu, li ko dale fukki fan ci weeru Suwe ba juróom-ñeenti fan ci weeru Sulet. Waa YAW mel ni loolu lañuy bañ a dégg. Ñoom tamit, ñu génn ne duñ bàyyi seenum ndaje, dañ koy amal donte ne sax dañ leen ko tere. Ndax, ñoom dañoo jàpp ne dogal boobu pólitig moo ko lal. Perefe bi tamit tёnku ci dog boobu daldi gàntal seen ndaje mi. Manaam, ndaje moomu du mёn a am. Loolu taxul ba tey ñoom waa YAW ñu teggi seen tànk fiñ ko tegoon. Foofu la coow li doore. Mu mel ni dañ doon tiiñalante, ku nekk ne du bàyyi fim jàpp. Ba ci àjjuma jii nga xam ne ci lañ waroon a amal ndajem ñaxtu mi ca bérébu Obelisk. Ci suba gi la takk-der yi wàcc ci béréb yu bari ci Ndakaaru. Ñu fatt yoon yi jëme ci këri lenn ci ponkali kujje gi, muy Usmaan Sonko ak Bartelemi Jaas, ne leen duñ génn seen kёr te kenn du leen seetsi. Maanaam, ñoom duñ génn dem fenn ak fum mёn di doon. Waaye, ndax loolu la ndeyu àtte gi (constitution) wax ?

Mu mel ni yoon moom dafa naax-saay ci réew mi. Day def liñ naan ku bokkul ci gétt gi doo naan ci meew mi. Waaye nag, bёgg ngawar bu la taxee mafñandub siññeel, loo liggéeyati ag teg lay jar. Ba tax na, ñi jiite yoon ak ñi fare ci kujje geek Nguur gi war a bokk jёfe li ndeyu àtte gi wax. Ñu bañ a jёl yoon lal pólitig ca gannaaw ngir def lu leen neex. Nguur jarul faat ay bakkan, muy ci ki bёgg a falu ak ki bёgg a faluwaat. Ndax, li xew ci àjjuma jii weesu dafa jéggi dayo. Te, lenn waralu ko lu dul yoon wi ñu jalgati. Moo waral ay jàmmaarloo am ci yenn béréb ci biir réew mi ba ñetti bakkan rot ci. Kenn ki Kolobaan lañ ko faate, kenn ki Sigicoor, keneen ki Biññoona. Ñu jàpp ci ñu bari, am tamit ñu ci am ay gaañu-gaañu. Fitna jii mbaa fim jёme réew mi ndox am na fa ? Bu dee ñi war a aar askan wi ñoo leen di fitnaal, di leen dóor ay bal ba am ñu ciy faatu, ñeneen ñi seenug dundu jaar fa yàqu. Ñoom buñ jёfee noonu, kon, kan mooy aar askan wi ? Te, li ci gёn a doy waar mooy ñoom kuñ ci rey du mujj fenn. Ndax ñi ñu reyoon Màrs 2021 ba tey mujjul fenn. Mu mel ni yoon moom ku ab takk-der rey da ciy bank ay loxoom, du ci jéem a àddu sax. Te, ñoom ñaar ñépp moone ay maxejj lañ, ñoo war a yem ci kanamu yoon. Waaye, bu dee ku takk-der rey yaay peert, léegi kon, kan la fi yoon nekkal ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj