MAAM LEES KAMARA, KENN DOOTU LA FÀTTE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Altine, 1eelu fan ci weeru Me lañ doon màggal liggéeykati àddina sépp. Fépp fu liggéeykat nekk, ak bépp xeetu liggéey boo mën di def, ci bés nga bokk. Moo tax, bari nay xew-xew ak i xewte yees di amal ngir ràññe ci ñi nga xam ne, bu dul woon ñoom, àddina si du dox. Nde, fu liggéey amul, koom du am, fu koom amul, dund dina fa jafe. Kon, gàcce-ngaalaama liggéeykat yi. Ndeysaan, daf ci am nag, ñoo xam ne, fekkewuñ bés bi te doon ñu ràññeeku ci boor yiñ féet woon. Taskatu xibaar bu mag bi woon, Maam Lees Kamara, ci kàngaam yooyu dëddu te wuute bés bi la bokk. Waaye de, bu jëmm ji teewul yit, màggalees na tur wi ngir seede yu bari yi te rafet. Rax-ci-dolli, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dafa xaatim ab dekkere, dogal ni CESTI dees na ci tofatal turu Maam Lees Kamara. Tey nu wax leen as lëf ci jaar-jaaru Maam Lees Kamara.

Ca Tëngéej, maanaam Rufisk, la Maam Lees Kamara fekk baax, ca gox buñ naan Këri-Kaw. Bim jàngee ba am BAC, ca la dugge ca jàngueb Seex Anta Jóob bu Ndakaaru (Ucad). Ba mu fa nekkee, jaar na tamit ca bànqaas ba jàngale mbirum tas xibaar, di fa tàggat taskati xibaar yi, maanaam CESTI. Moom, nag, ca juróom-benneelu poromosiyoŋ  ba la bokkoon. Ginnaaw gi la dem  Kanadaa suuxati njàngam ci wàll wi. Moo tax, ku bari woon xam-xam la ci wàllu caabal a kyu ni mel, rawatina ci mbirum rajo.

Maam Lees Kamara bàyyi nay njeexital yu fs ca rajo bu mag bii di RTS. Ndege, moo fa doon amal jotaay bees duppee Face à Face. Ñu ni déet-a-waay, mu jóge fa, jiiteji rajo Walfadjri, teg ci rajo Envie FM toftal ci rajo Océan FM. Yemu ca de. Ndaxte, Maam Lees Kamara dafa doon jàngale ca CESTI. Taskati xibaar yu bari ci réew mi jariñoo nañ xam-xamam. Looloo tax, keroog ba mu dëddoo, gaawu 29 Awril 2023, njabootug caabal gépp jooy, ame naqar ak tiis ju réy. Waaye sax, ñépp ñoo ko sargal, delloo ko njukkal, ba ci ñi dul i taskati xibaar.

Ci kow loolu, Njiitu réew mi, Maki Sàll xamle na keroog, ca bésub  liggéeykat yi, ne bànqaasu UCAD biy jàngale mbirum tas xibaar, CESTI, dina ko jox turu Maam Lees Kamara. Mu teg ca kàddu yii :

“Maam Lees Kamara war naa doon royukaay ci bépp saabalkat. Jël naa dogal tudde CESTI saabalkat bu mag bi kenn dootul fàtte.”

Ndogal loolu, ñépp ñoo ko rafetlu. Nde, kenn gënu ko cee yey. Mënees na wax ne, ku tudde CESTI Maam Lees Kamara, mooy delloo na mbàttu ca ndaa la. Ndax, fa la fekk baax te, dundam yépp jox na ko xibaar ba ni mu fiy jógee. Kon, turam warul far ci xëti yaxal yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj