Màggalu Poroxaan bokk na ci xew-xewi diine yi gën a ràññeeku fi réew mi. Mu nekk bés bu ñu jagleel Soxna na su tedd sa, di Maam Mariyaama Buso. Ñu gën koo xame ci turi Soxna Jaara Buuso. Mu doon way-juru Séexul Xaadim. Mu ngi gane jamono ca atum 1833 fa Gollere, Fuuta. Way-juram wu góor mu ngi tudd Sëriñ Muhammadu Buso, way-juram wu jigéen di Soxna Asta Waalo Mbàkke.
Ni ko doomi Soxna yu bari di defe, Soxna Jaara teel na wattu téere bu sell bii di Alxuraan. Mu nekk ay keemtaan ci ay atam. Mu teel a door liggéeyub njàngale laata muy dem kër. Doonte xam nañu ne teel na sóobu ci liggéeyal Maam Moor Anta Sali Mbàkke miy way-juru Sëriñ Tuubaa. Liggéey boobu bokk ci li ko may tur ba mu siiw ci àdduna. Nde, bari na taarix yu koy firndeel. Ñu di ci naw jikkoom ya, nangoom ga ak yéeneem ja. Nde, woykat ba (Sëriñ Ablaay Ñaŋ) ngay kañ jikkoom ya naan :
Mësul a julli te jàppul
Mësul a julli te wérdul
Door a xéy sangam tuubal
Daldi wol këram buubal.
Lii nekk ab jukki ci taalif bu mu ko jagleel. Waaye mu tënk ag dundam ci diggante Boroomam ba ak këram ga. Mu mel ni lépp a matale. Liggéeyu këram fànqul dara ca la mu war a jox Boroom Bi. Waaye, mësul a doyadil ndigalu boroom-këram. Looloo tax ba taariixu sàkket wa siiw ndax jëfe ndigal. Looloo tax ba Yàlla fayee njaboot gu barkeel ba ñuy tudd turam fépp ci dunyaa. Soxna Jaara bokk na ci jigéen yi ñuy tudd, nekk tamit royukaay rawatina ci jigéen ñi. Ca atum 1866 la dëddu. Ag dundam néew lool ci ay at, waaye réy lool ci ay jëf.
Jaaratul Laahi ma nga ñu denc ca Poroxaan fa ñu koy màggale at mu jot? Di ko siyaareji.