MAKI, FÀTTALIKUL “PAPA DOC”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jafe na nga xam as lëf ci dundu “Papa Doc” (François Duvalier) mu réewum Ayti te sa xel du dem ci Maki. Doonte manoo leen a méngale ci anam yépp ndax jamono yu wuute ak tolluwaayu xew-xewi àddina. Waaye, booy bàyyi xel Maki, dafay mel ni dafa tiim dundug “Papa Doc” di ci seppi ay jukki.

“Papa Doc”, yéeneem moo doon jiite réew ma ba keroog muy dee, maanaam nekk “Président à vie”… Waaye tëbut rekk sàkku ko. Dafa doon yoot ak a teg i pexe ba jëmmal yéeneem ja. Atum 1957 la jot ci Nguur gi. Ca atum 1961, fekk moome (kay) gi des ñaari at, mu soppi sàrtu réew ma, def ay wotey bennub lawax, maanaam “élection à candidat unique”. Loolu doyul, mu toogaat, daldi tas Ngomblaan ga (dissolution de l’Assemblée). Ñu ni déet-a-waay, atum 1964, mu jël ndogalu nekk Njiitu réew ma ba keroog muy faatu, maanaam mu nekk “Président à vie”. Ndogal loolu nag, ci Senaa (Sénat) bi la ko jaarale woon. Rax-ci-dolli, dafa amoon sañ-sañu tànn ka kay wuutu ca jal ba. Noonu, mu toog ca boppu réew ma ba atum 1971, feebaru robaale ganesi ko, mu samp doom ja “Baby Doc” (Jean-Claude Duvalier). Te, doom ji, jamono jooja, amagutoon sax 20i at.

Ngir “Papa Doc” man a jëmmal yéeneem, dafa mel ni ku def li ñuy tudde “voyage dans le temps”, ngir àbb Maki Sàll as lëf ci ay doxaliinam : tëcc opóosaŋ yi, wal leen ba ñu mokk, nga nappaaje jàll. Loolu mooy la Maki Sàll waxoon ci tubaab : “réduire l’opposition à sa plus simple expression”. Tëj, ray, génne réew mi, mbaa nga noppi. Lii la “Papa Doc” jagleeloon ay opóosaŋam.

Ba léegi, ngir matal bëgg-bëggam, dafa àbb Maki Sàll kenn ci takk-deram yi (Musaa Faal), di yamoo ak “Clément Barbot” mi nekkoon njiital pólis ba. Doonte, dafa koo mujjee ray ndax ragaloon mu nangu Nguur ga. Yamut ca loola, Maki daf ko déey, ne ko am naa fi ñu may tudde “les marrons du feu” ak ay “nervis”. Dañuy dóore, dañuy raye. “Papa Doc” samp moom it bosam, mooy ñoom “Tontons macoutes”. Ñoom itam ñuy roy ci “les marrons du feu”, di dóore, di raye.

Weeri suwe ak ut atum 1964, dafa amoon ndaw ñu jóg ngir jàmmaarloo ak moom, mu yabal sóobare (soldaar) ya ak “tontons macoutes” ya ñu ray ba seen xol sedd ni ko “gendarmerie” ak “nervis” yi defe woon ca màrs 2021 ak suwe 2023. Yamu ca, Maki xelal ko, wax ko ne, ngir layal ray geek tëj gi dangay fent ay noon yu kenn dul gis, maanaam “ennemis imaginaires”, lu ci mel ni “forces occultes”, “forces spéciales”, “terroristes” ñu jóg ngir lëmbaaje réew mi. Ca noona, “Papa” Doc ne “La sécurité du pays” (kaaraange réew mi) moo féete kaw lépp, moo tax fàww mu raxas ko ci ñi ko bëgg a nërméel.

Rax-ca-dolli, Maki ne ko fexeel ba say ñoñ, ak ñi la déggal ci “Justice” (Yoon) bi ak ci “Armée” bi seen ceeb tooy, seen i poos fees. Deel doxalee “gën a bokk, gën a yay”. Càccug alalu réew mi jiite ko, say nit ñi koy def itam, làq leen ba bu kenn man ci ñoom dara. “Papa Doc” doxalee nu ni mel ngir dëgëral nguuram.

Naam, ci waxiin, “Papa Doc” mucc na cig dundam, ba samp doom ja 1971, waaye ginnaaw 15i at ba mu génnee àddina, waa réew ma fippu, dal ci kaw “tontons macoutes” ya ray ca lu bari. Doom ja, mbir yi ëpp ko doole mu bàyyi (démissionner), askan wa dem song bàmmeelu baay ja, sulli ko, def ca jëf ju ñaaw…

Gis nga, doonte “Papa Doc” dee na ba am fukki at ak juróom ci biir suuf, waaye taxut waa réew ma fàtte li mu leen daan def ci lu bon. Aw askan du fàtte. Te kenn manut a dëkk ci am ndam ci kawam. Bis dina ñëw mu àtte la. Kon Sëñ Maki, ba léegi Yàlla mi ngi lay suturaal, dellul ginnaaw ca ba muy teel. Li wér te wóor mooy “Président à vie” moo nekk sa xol bi, bu say pexe sottee nammoo jóge ci boppu réew mi, dinga faagaal opóosaŋ yépp, tas bépp Bànqaas bu lay teeree mottali sa yéene. Waaye, sa pexe du àntu. Ndax, la woon wonni na. La jigoon “Papa Doc”, jigu la : àddina si soppiku na. Te askanu Senegaal du wow Ayti. Bàyyi ci xel ndeem bëgg ngaa mucc.

Maki, dellul ginnaaw ba laa wees !

Seexunaa Njaay
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj