Màggalug bés bi Senegaal moome boppam, dafa nekk aada ci réew mi. Ñu jàpp ko at mu jot ci bésub 4 awril. Ren, dafa yamook 63eelu yoon. Ci kow loolu, dañu seetlu ne, lu njëkk bés boobu, Njiitu réew mi, day janoo ak askan wi ngir dégtal leen ay kàddu.
Cubba Taal
Ren, dafa yamook 63eelu yoon, ginnaaw ba lu tollu ci ñeenti njiitu réew toftaloo. Maki Sàll di ki askan wi tabb ngir mu nekk ci bopp réew mi. Mu janoo ak askan wi ci altine ji 3 awril. Nit ñi dañuy taataan ay kàddoom ak xel, rawatina fi réew mi tollu. Looloo tax ba ñu mën cee jukke pàcc bu yaa bi mu jagleel ndawi réew mi. Mu nekkoon, ca ndorteel ga, ay kàdduy fàttaliku fi réew mi jaar ba am jonnug boppam. Waaye, dafa diy kàdduy sargal maam ya xeex nooteel ba Senegaal agsi fii. Mu ndokkeel bépp maxejj ngir lu ñu bokk te kenn mënu koo cëroo. Mooy li Senegaal doon benn bopp, nekk wenn askan.
Tolluwaayu àdduna nekk lu ñépp bokk di dund. Tax ba, jafe-jafe yi gën a sonal réew yu bari, doon cax bi xel yépp bëgg a càqi. Muy mbirum rëtëlkat yi lëmbe àddina si. Loolu tax ba Njiitu réew mi, Maki Sàll, jox dayo bu mag wàlluw kaaraange biir réew mi. Làrme bi la njëkk a sargal, ñoom ñiy sàmm askan wi.
Bu ñu sañoon, ne séddale kàddu yooyu ci ñaari pàcc, bu njëkk bi larme bee ko moom, waaye bu mujj bi ndaw ñi la ko jagleel. Ciy waxam, ñu mën cee déggee ni jafe-jafe yi ndawi Senegaal di dund. Ndax, ma nga naan natt na seen i bëgg-bëgg ngir ni ndaw ñi nammee jariñ seen bopp, waaye tamit jariñ seen njaboot. Mu doon yaakaar ju réy ju ndaw yu bari di dunde ngir seen ëllëg mën a soppiku. Ngir loolu mën a sotti, fàww ndaw yooyu ñu jàngal leen. Looloo tax ba Maki Sàll teg baaraamam ci njàng mi. Mu nekk ponk bu am solo ci ndaw ñeel ñi. Waaye, mu mel ni loolu doyut. Ndaxte jàng di am ay lijaasa rekk taxut nit ki xareñ. Tax ba mu sof ci ne, ag tàggatu lu war la ngir ndaw ñi mën a liggéey. Mu doon ay naal ak i sémb yu mu biral ngir saafara jafe-jafe yi nekk ci ñàkkum xéyu ndaw yi. Mu jël ci misaal 65.000iy xéy yu ñu sémboon te lu tollu ci 63.000 yi jàll. Mu lime ci batay naalu BRT bi nar a sos lu tollu ci 1000iy xéy. Waaye tamit, fàttewut a sargal ndaw ñi nar a yëngu ci waññi bi ANSD di def ci weeru me, jëm suwe te lu tollu ci 35.000iy ndaw nar cee liggéey.
Mënees na tënk ni kàdduy njiitu réew mi, Maki sàll, ndaw ñi la ko jagleel. Mu doon jafe-jafe yu ëlam ñu bari. Ndax fi seen xadar tollu te li ko waral, li ëpp di ñàkkum xéy. Ñu seetlu seen taxawaay ci ñaxtu yu bari ak dayo bu mag biñ ciy ame. Kon, ñu mën a jàpp ne kàddu yooyu di na dëfal ci genn wet, waaye ndaw ñi tamit, nànd nañu ne leketu neen naxul i béy.