Cokkaasu RFI bii daf nuy fàttali ñetti léeb yoy, mbaam a ciy ndeyu-mbill ji. Léeb bu ci nekk nag, day junj nekkiinu Njiitu réew mi, Maki Sàll, jamono jii.
Bi ci jiitu mooy bi ñépp di reetaan, Mbaam moom ne tekk-tekkaaral. Ñépp ree ba kekku, Mbaam ni cell rekk. Ñu toog ñaari fan ci ginnaaw gi, Mbaam di sog a toj, reetaan moom itam. Ndekete, day sog a nànd la ñépp doon ree.
Ndeysaan, aka muus !
Ñaareelu léeb bi mooy ba Mbaam àndee ak Baaxoñ, ñuy tukki, yéeg cib roppalaan. Roppalaan ba teddi, jóg, naaw ba tiim niir yi. Baaxoñ bay tooñaate ak a cofaate. Mbaam nekk di ko toppandoo, di ŋaax ak a wéqaate. Ñu jàpp leen, boole ñoom ñaar ñépp tëmbal ci biti. Bañ leen tëmbalee ci bayaalu jàwwu ji, baaxoñ tàllal ay laafam, daldi naaw. Mbaam di wiccax i tànk, di ŋaax ba daanu, daldi sànku…
Ndeysaan, aka muus !
Ñetteel bi ci mujj mooy Mbaam, Njàppaan ak Gaynde.
Gaynde da doon waxtaan ak Njàppaan. Ci biir waxtaan wi, Gaynde ne :
– Man daal, dama xiif te yàpp mbaam rekk laa namm.
Njàppaan ne ko mën na ko indil Mbaam mu fàdd ko, xéewaloo ko. Gaynde ne ko, na ko dal. Njàppaan fëx, seeti Mbaam ngir yóbbu ko ci Gaynde.
Ba mu àggee, mu ne Mbaam :
– Mbaam, sama xarit, sama doomu ndey, bégal !
Mbaam laaj ko lu xew. Njàppaan ne ko :
– Gayndee la bëgg a def buur ! Gaawal ñu dem balaa cee cat dugg.
Mbaam daldi jaab, xélu, wutali Gaynde. Njàppaan topp ciy daw. Mbaam àgg rekk ne saraax ci kanamu Gaynde. Laata muy nuyoo Gaynde ngàdd ko ci bopp, wewam yu réy yi dagg noppi Mbaam yi, ñu wadd. Mbaam ne walbit, daw ba pënd ba jóg ngir rawale boppam.
Gaynde sàkkuwaat ci Njàppaan ngir mu indilaat ko Mbaam. Njàppaan dëgmal wuti mbaam, egsi mbaam araftu ko, ne ko :
– Bul wax ! Yow doo sama xarit ! Danga maa bëggoon a sànk.
Njàppaan, yëngal bopp bi, ne ko :
– Yow yaay dof dëgg ! Bu dindiwut say nopp nan la lay takkalee meteel bi (couronne) ?
Mbaam ŋaax, ne ko wax nga dëgg. Ñu ànd wéy fekkiwaat Gaynde. Ñu ekseeti rekk gaynde pàdd, yóotu geen ba ne ko tipp dagg. Mbaam salliiru, dawati ba raw.
Gaynde santaat Njàppaan mu dellu indilati ko Mbaam. Njàppaan dellu. Bi mu àggee, Mbaam ne ko :
– Bul egsi de ! Yaw bu ma la toppee sànku.
Njàppaan ne ko :
– Lu tax doo xalaat ? Nooy ame geen di toog ci Jal bi (Chaise Royale) ? Moo tax Gaynde dagg ko.
Mbaam ŋaaxati, fëgg bopp bi, neeti :
– Maay dof dëgg ! Wax nga dëgg. Ayca nu dem.
Ñu demati ci Gaynde. Ñu àgg, Gaynde fàdd, teqale bopp ba ak baat ba. Ne njàppaan demal fees indil ma yuur gi, xol bi, ak res wi. Njàppaan fees, xéewaloo yuur ga, indil Gaynde xol bi ak res wi kese. Gaynde ne ko ana yuur gi ? Njàppaan ne ko, bu amoon yuur doo jot ci moom !
Bees jàngatee ñetti léeb yii, dees na gis ne Maki Sàll soreewut ak mbaam mii. Ndax, ay bëgg-bëggam ak ay jëfam ñoo am taxawaayu gaynde gi. Maajor ak ñi mel ni moom am taxawaayu njàppaan bi. Njàppaanam yaa ngi koy xelal ngir lu neex gaynde gi nga xam ne, ci fàdd ko lay dox guddi ak bëccëg. Teeylu na ko ñaari yoon mu rëcc. Waaye, bu ñette ñu fidaawu ko.
Géwal nag, bu reppee cib xare, lu mu jiin xeeb ko.