MBARA-WÀCC DOOMI-GAYNDE NJAAY YI !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Sunu gaynde yi amagul ñaar-fukki at wone nañu njàmbaar fale ca Niseer, nga xam ne fa la réewi Afrig yi gën a xareñ ci futbal daje woon di joŋante.

Jaaraama sunu Doomi-Gaynde yi ! Ay jàmbaar dëgg lañu, ñaawuñu ci xare bi ndax ca Niseer, daje nañook ñeenti ekib, am ndam ñeenti yoon. Mali ak Ganaa lañu njëkk a gal-gal ñaari bal ci dara (2–0), duma Burkinaa Faaso duma yu metti, juróomi bal ci benn (5–1), jóge fa jaar ci kow Réewum Afrig-bëj-Saalum benn ci dara (1–0). Léegi, ñook seen doomi-ndeyi Mali yi rekk a des ci géew bi ! Ak lu mën a xew fan yiiy ñëw, gone yi def nañu lu réy. Sunu xel dal na ndax déggoo, doon benn a leen tax a yegg fiñ yegg tey, fëq caax yi juròom ñeenti yoon te benn yoon doŋŋ lañu nax seen góol. Muy firndeel itam ni ekib bi dëgëre…

Fi mu ne nii, ñu ngiy xaar Mali, waaye dara mënatuleen a tee bokk ci joŋante bu mag biy dajale réewi addina sépp, ca Poloñ ci weeri me ak suweŋ yiiy ñëw. Loolu du guléet, ndax Senegaal demoon na Nuwel-Selànd, ci atum 2015 ak itam réewum Kore Bëj-saalum ci atum 2017.

Ku xam Yuusuf Daabo miy tàggat sunu gaynde yu ndaw yi, xam ne amul tiitukay. Daanaka kóoluteem ci goney ekip bi amul àpp. Nee na Senegaal amul lu muy ragal ndax démb la tàmbalee waajal joŋanteb Niseer bi tey soog a ñëw. Loolu tekki ne liggéey bu jaar yoon a ko tax a dal xel. Te, sàllaaw, bala yàgg nun ñépp dinanu bég. Yuusu Daabo yokk na ci sax ne : « Jot nanoo am i jogaŋte yu metti, Burkinaa Faaso lanu mujjee dajeel, ñu indilnuy jafe-jafe. Waaye sunu pas-pas tax na ñu génn ci. Gëm naa ni kenn mënatunoo të, ku nu dajeel dinan la dóor ».

Li wóor ba wóor moo di ne bu Senegaal toogul ci gàngunaay bi dina ñaaw, ndax dellu ginnaaw lay gën a nirool. Ñaari yoon yi mujje yépp, doomi-gaynde yi àgg nañu ba ci njeexital li ñu daan leen. Su nu waxantee dëgg, nag, loolu mënuta wéy te ñu baree ngi koy naqarlu ba tey jii. Kon mu mel ni am ndam ci dibéer ji rekk mooy seral xol yi.

Abdulaay Seen

(Bi nu bindee li ngeen jàng ba noppi, lanu dégg xibaar bu tiis bi : Mali mujje naa dóor Senegaal 3 penalti ci 2. Kon ñu ne xalam demoon na bay neex…)

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj