MBAY JAAG, GOR BI SENEGAAL AMEEL BOR (Xaaj bu njëkk)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xel tëju na, xalaat dëju. Xol tooy na, bët jooy. Ndeysaan… Gaynde wàcc na liggéey. Nee leen ko mbarawàcc, Jaag, nu sargal ko, delloo ko njukkal.

Mbay Jaag wuyuji na Boroomam. Dibéer, 12eelufan ci weeru me atum 2019 la génn àddina. Li Yàllay def, dibéer jooju dafa yemoo kepp ak 51eelu at ca ba muy jiite toogaayu-ñaxtu ba ndongoy iniwérsite bu Ndakaaru amaloon, waat ne fàww ñu janook Njiitu-réew ma woon, Léwopóol Sedaar Seŋoor, walla nguur gi ci boppam ngir àgge ko seen i tawat.

Mbay Jaag, nag, kenn umpalewul ne moo jiite woon kurélu Iniwérsite bu Ndakaaru, ca atum 1968 – booba, tuddagul woon Séex Anta Jóob – ga taxawoon di xeexal ndongo yi.

Ca yooyu jamono, fekk na Seŋoor nekk ci diggu ndëndam. Lu ko neex tëgg, ku feccul mu ni la génnal géew bi walla mu nëbb la jant bi. Ci gàttal, moo doon Buur, di Bummi. Ku say wax walla say jëf méngoowul ak i yosam, mu jaay la doole, ne la ràpp ci kaso bi, tëj. Waaye, kuy jaay fit, boo dajeek gaynde lamble.

Weeru me 1968 la ndongo yi jógoon, fippu, jàmmaarlook Nguur gi, ni ko : « Dafa doy ! Li nuy dund mënuta wéy ! » Ñu noon  dee, coppite day am te dara lañu ci bañul. Ñu ga Nguur gi ci ne, na leen yokkal seen i ndàmpaay, jagalaat seen nekkin te it yeesal seeni jumtukaayi njàng. 

Jamono jooju, daanaka fépp foo demoon ci àddina si, dinga gis ndongo yiy fippu di sàkku ab yeesal ñeel njàng mi.

Bu dee sunu réew mii, nag, UDES ak UED ñooy kuréli ndongo yi gënoon a fés ca xeex booba. Te, ñaari kurél yooyu yépp,  Mbay Jaag ak i ñoñam ñoo leen jiite woon. Waaye ba tey ci njiit yooyule, Mbay Jaag lañu ci gënoon a ràññee.

Moom Mbay Jaag, nag, daanaka aul woon tiitukaay, ñi ko xamoon yépp, am fitam lañuy gën a fàttaliku tey. Rax-ci-dolli, dafa amoon pas-pas, farlu, te xareñoon lool. Kenn dàqu ko woon a wax ak mbooloo itam. Noonu, bu jëlaan kàddu gi, fu ne la nit ñiy fàqe ngir déglusi ko mbaa topp ci ginnaawam. 

Mbay Jaag ! Kii moo amoon bayre, ndokk ! 

Jàmbaar jii moo teewoon nelaw Seŋoor ak i nduguroom. Waaye, Mbay Jaag ak ñi mel ni moom, foo leen fekk, nguur gu jubadi da leen di noonoo, di leen fexeel.

Moo tax Seŋoor mépp pexe mu mu xamoon lal na ko ngir sàkkal pexe Mbay Jaag ak ñi toppoon ci ginnaawam : nappaate, ger, tëj kaso, añs. Wànte du benn ci pexe yooyu bu ci àntu. Te, nag, ñi andoon ak Mbay Jaag ñoo ka bare woon ! Looloo tiitaloon Seŋoor, mu dem sax ba jàq lool. Ndax kat, ndongo yi dañoomayoon fit yeneeni kurél yi nekkoon ci réew mi, di liggéeykat yi booloo woon ciy sàndikaa yu siiw, am i tolof-tolof ba noppi ragal a fippu. Gone yee leen may fitu ñaxtu yi. Seeni rakk sax, ndongoy lekkooli diggu-dóom yi, dañoo jóg ñoom tamit. Mbir yi mujje ëpp i loxo ndax muy jàngalekat yi di óbëryee yi, kenn toogul. Koom-koomu réew mi tag, dara doxatul. 

Bi Seŋooramatul pexe, takk-deri Frãs yi sàncoon seen gàdd ci Ndakaaroo mujjee wallsi nguuram. Teewul, ndongo yi ak seeni njiit wéy di lëkkalook liggéeykat yi, jàpp fi ñu jàpp. Gornamaa bi jàq, teggi loxoom, woo leen waxtaan, nangul leen lu bare ci seeni ñaxtu, ba jàmm delsi ci réew mi.

Wànte waxtaan wi taxu ko woon a yomb noonu : Mbay Jaag ak i ñoñam, dañca wone fullaak faayda ju mat sëkk, nañu ka daan defe naka-jekk. Fulla jooju ak pastéef yi ñu àndaloon bu ñu wàccaan ci mbedd yi ak tali yi, di sànniy xeer aka taal i póno. Ci njeexital li, ndongo yi jële nañfa ndam lu réy, doonte amuñu woon lépp la ñu bëggoon

 Xew-xew yu metti yooyu, nag, mëneesu leen a nettali ba noppi di bañ a tudd xale Naaru-Libaŋ bi ci ñàkkoon bakkanam. Keroog, bésub 29 ci weeru me, la alkaati yi song néegi ndongo yi, dal seen kaw, gaañleen, yàq mbaa sàcc seeni bagaas ak seeni alal.

Mbay Jaag jitte woon na fi tamit ndongoy Iniwérsite bu Ndakaaru ci xeex bu mag bu ñu amaloon ci diggante 1971 ak 1972 te taxoon Seŋor tëjlu daara ju mag jooju.Dàqoon na yit ndongo yu bari ba noppi solal soldaar seeni njiit, yóbbu leen Kaasamaas, fa way-fippu PAIGC yi doon jàmmarlook làrme bu Purtugees yi. Ci ñooñu mënees na cee lim Ablaay Bàccili ak Mamadu Jóob Dëkurwaa… Bañkat yooyule, Mbay Jaag moo doon seen njiit. Ñoom ñépp ñu sànni leen ca Sancaba Manjaag, ci wetu Gine-Bisaawo, fa xare ba gënoon a mettee. Fa la Al Fuséyni Siise, kenn ci ñoom, faatoo ci anam bu ñaaw. Noonu la ñoom Mbay Jaag nekke woon ci làrme bi ak i jafe-jafe yu tar, ba biñ leen di bàyyi. Nguur gi jéem a saafara mbir mi, waxtaan ak ndongo yi, jëlaat ña mu dàqoon ba noppi fajal leen yenn ci seeni aajo.

Ginnaaw gi la Mbay Jaag génn Iniwérsite dem jàngaleji matematig ca Cees, jóge fa dem liggéeyi Liise Jiñaabo bu Sigicoor.

Xare yi mag yooyu askanu Senegaal difàttaliku tey, ndongo yépp a ci amoon ndam waaye jaloore ja ca Mbay Jaag jële, leneen mayu ko ko lu-dul taxawaayu njiit lu mat sëkk, ngor, njub, fit, ak xel mu ñaw, kaar !… boole ci ñàkk caaxaan bi ko ñépp mas  a seedeel, te ñu bare jàppe woon ko naqadi deret mbaa sax ñàkk kersa. 

Ñàkk caaxaan googoo ngi woon ci moom bés ba muy faatu.

(Fan yii di ñëw, LU DEFU WAXUdina delsi ci li des ci jaar-jaaru Mbay Jaag. Mooy doon ñaareelu xaaj bi)

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj