MUSIBAB SINJAA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Diggante ndongo daara ak sëriñam, yenn saa yi, du doon lu ratax. Lu ci bari li leen di xàjjale di mbañum njàng ci yenn ci ndongo yi, walla sax ay dóor yu metti yu yenn ci jàngalekat yiy dóore. Loolu nag, du jur jàmm seen biir. Tax na ba ndongo yi di daw, wutali mbedd yi, réer daara yi, réer seen i way-jur. Léeg-léeg sax, tóoxidóona am ci.  Musibab Sinjaa bi, misaal la ci.

Xew-xew bi am Sinjaa ca diiwaanu Mbuur, nekk na lu doy waar ci askanu daara. Muy luy faral di am ci béréb yees di jànge xam-xam. Ay dóor ak i mettital yu ñuy faral di gis ci xale yooyu di sàkku xam-xam. Agtumurànke lañuy nemmeeku lu bari ci ñoom. Tax ba ñuy jàppante lu bari ak ñi leen di jàngal. Loolu, di dem bay jur jéyya ci jàngune yi. Waaye, li ñu daan faral di gis mooy ay dóor walla jéng yu ñuy def ndongo yi ngir ñu mën leen a téye ca béreb ya. Ñu ciy nemmeeku ay faat bàkkan yu jóge ci dóor yu metti yi. Loolu tamit, daan nekk jëfi sëriñi daara yi. Ba ci jamono jii ñuy wax ak yeen, yoon am na ñu mu jot a téye. Waaye, la xew Sinjaa mën nañoo wax ne gulléet muy am. Ndax, li ñu daan dégg wute na ak li xew. 

Ab ndongo buy wuyoo ci turu I. Jaañ moo jam sëriñam, ki ko doon jàngal Alxuraan. Bu ñu sukkandinkoo ci këru xibaar gii di Senenews, li leen boole di daw gu ndongo boobu di I. Jaañ daan daw. Looloo tax ba jàngalekatam bii di Sakariya Njaay daan saytu, di ko fanaanoo. Ci noonu, la ndongo ba lalee pexe ngir génn ca nekkin woowu. Ndongo li, I. Jaañ, dafa nëbb ab paaka, xaar ba sëriñ ba jàppante ak ay nelaw, mu daldi koy jam. Ca la Sakariya moomu jaare, faf, faatu, ginnaaw ba ñu ko rawale ca raglu bu Mbuur. Bu dee ndongo la, moom, ma nga ca loxoy yoon ngir ay luññutu. 

Mënees na wax ne, jot nañu saytu bu baax liy xew ci jàngune yi, rawatina ci daara yi. Ndax xew-xew yu ni mel mu ngi faral di am di amaat. Te, la ca bari, du jur jàmm. Doonte ne liggéey yépp a am jafe-jafe ak i njuumte, jot na, ñu taxawu taalibe yeek sëñ daara yi ngir seen nekkin gën a ñoŋ. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj