ÑAARI KUY DUÑU BOKK MBALKA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Pólitig ci Senegaal du jóg di jur mbetteel ci askan wi. Mu mel ni, lu kenn dul foog, mooy wëlbatiku di ëlëm nit ñi. Waaye, la bettut kenn mooy daan bi ñu daan njiitul Pasteef lii di Usmaan Sonko. Ñu gis ne gal-gal bi yàgg na lool, waaye la ca mujj bettut kenn. La Yoon dogal ci moom te jeexital la nekk lu koy gàllankoor ci pólitig, mooy tàggale kook àq ak yelleefi maxejjam. Loolu, di wund ne, njiitul Pastef li du mën a bokk ci wotey njiitu réew yii ñu dëgmal.

Ca geneen wet ga, ñu seetlu ne jafe-jafe yi dañuy toppalante. Mu mel ni yuuxu jib na fa ñu ko foogeewut. Nde, lëkkatoo YAW, ci tas la jëm. Mu nekkoon lu ñenn ci ñi seen xam-xam màcc ci wàll woowu doon junj. Muy lu ñu miis ci pólitigu réew mi, rawatina bu ay wote jubsee. Waaye, génnug Bàrtelemi Jaas gi lëndëmal na xel yi. Mu bokk ci waa Yewwi askan wi, taxawaayam doon lu ràññeeku ci kujje gi. Ñu yàgg koo gis ci wetu Xalifa Sàll ak Usmaan Sonko, seen ànd boobu ñu mën leen a tudde ñatti doomi Penda Naar. Laaj biy sàmpu mooy lu xew ? Lan moo war a jur ñàkk a déggoo ci seen biir ? Mbaadu YAW dafa nar a soppiku MAN ?

Bu ñu sukkandikoo ci ay kàddoom, moom Bàrt, dafa mel ni kuy ŋàññ taxawaayu Usmaan Sonko ci yenn mbir yi, rawatina waxtaan wi. Ndax, ma ngay wax naan : “Kenn mënut a bëgg lee, bëgg la ca des”. 

Mu mel ni Bàrt, ndaanaan la niki ni mu koy waxe. Ndaxte, fitam, dëggoom ak fullaam tax na ba kenn du ko yab. Mu mel ni ku nekk ci ab téesante, doonte ne tuddewu ko noonu, waaye « yaa ma ne » ak « moo ne ma » bariwoon na ca.

Déggees na ci ne la sooke coow li, woote waxtaan wa Bàrtelemi Jaas sumboon ca la. Ñu gis ne, joxe bopp, rocci làmmiñ am na ca. Ndax ag déggoo ca amoon waaye ay tëkkoo ca mujj.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj