NAN WAX CI YENN SÉRI TELE YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jamono jii nu tollu temm bari na lu ñu seetlu ci miim réew, ñeel tele yi. Waaye li ci gën a ràññeeku mooy séri yu bari yi ñuy dawal. 

Lu sabab lu ni mel nag mën nañu wax ne ciy ñaxtu la jὀge. Nde, ay at ci ginnaaw, liñ daan faral di gis moo doon séri tubaab yi. Loolu am na ñu mu neexul woon ba ñuy xultu naan yooyu séri dëppoowul ak dundinu doomi réew yi, du ci seen aada, du ci seen cosaan. Ñeneen ñi naan waaw, nun sax, lan moo nu tee fent ay séri yu dëppoo ak sunu nekkin ?

Amaana xeex boobu moo jur coppite yi am tey. Ba tax na séri yi takkarnaase nañu lool. Yi ci gën a ràññeeku nag ñooy : Pod et MarichouMbetteelMaitresse d’un homme mariéIdoleak  Golden.

Naam lu rafet la ndax xaalis bu bari bi ñu daan def ci séri yi ñuy jéggaani ji am na fu mu xaj. Nde am na ñu xalaat ni dërëm bi des ci gaal gi bokk na ci liy suqali am réew. Ci misaal, Marὀodi tv, Oke Afrika añs ay bérébu liggéeyukaay lañ yoo xam ne ci jumtukaayu xarala yu yees lañu bokk te ñooy amal séri yi. Rax-ci dolli day tax ndaw ñi amul liggéey am fu ñuy dàqe seen wërsëg. Yemuñu ci loolu ndax it kër gu ci mel ni waa « A+ » day jënd séri yi di leen teg. Am na sax ñu jàpp ni jëmmal gi ñuy jëmmal séri yi dina tax nit ku ñuul gën a xam boppam.

Waaye ñépp bokkuñu gis-gis. Mu mel ni rekk daa am lu ñuulal soow mi. Waaw ! Ndax am na ñu leen di ŋàññ. Li ñu doon daw fee ba tax nit ñi daan ñaxtu, moom la nuy tàmbalee gis ci sunu séri tey yi. Ñenn ci seetaankat yi jàpp ni bu weesoo Mbetteelak  Idole,benn séri méngoowul ak jikko yi waa réew mi miin. Seetlu bii nag ci Pod et Marichouak ci Maîtresse d’un homme mariéla gën a fése. Ñaari séri yooyu bari na ñu leen rafetluwul. Lu ñu ciy gën a ñaawlu mooy yenn jataay ak yenn kàddu yi tegginewul benn yoon. Waajur yi nag nee nañ lu ni mel day yàq gone. Li ëpp ci li ñuy wone dundinu nasaraan yi la gën a jege niki jigéen ju dëkk moom kese te amul boroom-kër ak yu ni mel. Walla bu dee am na sax ñi ko fiy dund, bariwuñu. Bu ñu wonee Afrig daal, ci colin mbaa ci làkk yi la yem. Wàllum jikko moom boolewuñu ko ci. Ci lu leen di suuxal rekk lañu nekk moo xam ñu xam ko walla déet. Mu mel ni rekk li ñuy bëgg a wone ak liy feeñ dañoo safaanoo. Lii taxoon na sax ba waa Jamra di kurél giy sàmm jikko yu rafet yi ak li méngook diine fésaloon seen mer ba ni woon dañuy yóbbu waa Maîtresse d’un homme mariéci yoon ginnaaw ba ñu amalewoon 11elu  jataay ba te Mareem di ab way-jëmmal ci séri bi kàddoo woon ni : « sama lii maa ko moom te ku ma neex laa koy jox ». Waaye de, boobu pelent mujjul fenn ndax waa CNRA di kurél gi war a saytu mboolem lu aju ci wàll woowu, daanaka àndu ci woon. Moo tax it diir lañu ci teg ñu amalaat lu ni weŋŋ ca 34elujataay ba. Altine 28elu fan ci weeru me waa Jamra wutaleeti CNRA ngir ñaxtooti ne lii kat day niiru kὀkkali. Kurél gi mujjee jël ay dogal jëmale leen ci kër gii di 2STV ngir ñu xoolaat  waxtu wi ñuy teg séri bi mbaa ñu dagg yenn jataay yi. Teg ci dànkaafu waa Marodi tv. Ne lu ko moy diñañ leen sàkkal pexe.

Lii war naa tax ñiy amal séri gënatee bàyyi xel ci aadaak cosaanu réew mi te bañ a roy doxalinu nasaraan yi. Ndax toppandoo ay doxandéem amalul réew mi njariñ. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj