Kurél gii di MSGBC te ëmb yile réew, Móritani, Senegaal, Gàmbi, Gine Bisaawoo, ak Gine Konaakiri, mooy amal am ndaje mu am solo ci ëllëgu gaas bi ci 1 ak 2eelu fan ci weeru Sàttumbar fii ci Senegaal ca béréb bi ñu dippee CICAD. Ndaje mii nga xam ne nag, Energy Capital and Power moo ko sumb, daf ko tëgg ci turu Njiitu réew mi Maki Sàll. mile ndaje mooy neekk seen um ñaareelu ndaje. Te, bile yoon, dina am ay doxandéem yiy jóge ci yeneen i réew niki Amerig, am yu bawoo Tugal, Aasi, réewi penku ya, Marog ak Koddiwaar ngir fekkesi xew-xew bi. Mu nekk lu war a mën a jariñ réewum Senegaal miy waaj a jëfandikoo gaasam ci at yii di ñëw rawatina ay ñoñam.
Ci ñaareelu ndaje mi MSGBC di amal fii ci Senegaal ci 1 ak 2eelu fan ci weeru Sàttumbar, jëwriñ ji yore fànnu soroj bi ak laf bi ak yeneen i àndandoom ni ki COS-PETROGAS (Comité d’orientation stratégique du pétrole et du gaz), PETROSEN (Société des pétroles du Sénégal) ak INPG (Institut national du pétrole et du gaz) dinañ ci bokk. Dañoo fas yéene waxtaan ci gaas bi ñu yore ci ndaje mii nga xam ne Energy capital and power moo ko tëgg. Bopp waxtaan wi nii la tëddee : « Ëllëgu gaas bi : yokkuteem ci dooleel ak yoonal yi ci mën a am ». Mu nekk ay saytu yu ñuy def ngir yaatal sémb gaas bi.
Ci saabal bi ñu génne, dina am ay doxandéem yuy fekke ndaje mi. Mooy ay kilifa yoo xam ne sémb bi daf leen a soxal lool ba noppi ñu bëgg cee am ab taxawaay bu am solo ngir dooleel ko. Nde, kii di Aysatu Sófi Galadima te nekk jëwriñ ji yore wàllu soroj bi ak laf bi fii ci Senegaal biral na ni :
« Ndaje mi dina nekk waxtu woo xam ne dinañu amal ay waxtaan yu xóot a xóot ci ni ñuy jëfandikoo laf bi ba mu nekk ci njariñal ñépp rawatina maxejji réew i Afrig yi bokk sémb bi ngir yokkute Afrig ci boppam ».
Ñaareelu ndaje mii dafa teer ci jamono ju am solo ci réewum Senegaal mii nga xam ne yokkuteem a ngi aju ci sémb gaas ak soroj bi mu yore. Ci xayma, sémb gaas ak bu soroj bii di GTA (Grand Tortue Ahmeyin) ak bu Sàngomaar a ngi ci yoon wu mucc ayib woo xam ne jar naa fital ndax liggéey bi ñu ci jot a def.
Bees sukkandikoo ci yéenekaay bii di Le Quotidien, diwaanu Senegaal-Móritani am na lu tollu ci 1,13 trillion de mètres cubes (tmc) ci laf. Móritani, moom doŋŋ yore na lu tollu ci 28,3 miliyaar mètres cubes (bmc). Loolu di firndeel ne yile réew bu ñu booloo, dinañu am yokkute yu kowe seen njortu. Waaye li kurél gii di MSGBC sumb, dafay fàttali li Seex Anta Jóob daan wax ci téereem bii di « Les fondements économiques et culturels d’un Etat fédéral d’Afrique noire ». Moo ngi xamal ni :
« Danu war a def lépp ngir réewi Afrig yi booloo. (…) Réewi soowu Afrig yi doŋŋ bu ñu booloo, ñoo ëppale dayo ci koom-koom bu Farãs ak Angalteer booloo » (xët 27).
Mooy li ñuy wax rekk, mbooloo mooy doole. Te lu kenn mën ñaar a ko ko dàq. Waaye nag, ku wàcc sa ànd, ànd boo dem fekk fa boroom.