NGOMBLAAN GI WOTE NA CÀRTUG CÀMM GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bërki-démb ci altine ji fukki fan ak juróom-ñatt, dépite yi wote nañu sàrt càmm gi ca Ngomblaan ga. Muy nekk guléet ca màkkaanum Péncum Ndawi réew mi. Dépite yépp, moo xam ña fare ci Nguur gi walla ci kujje gi, ànd nañ ne waaw.

Umpaleesut ne baykat yi ak sàmmkat yi duñu jaarundoo. Diggante boobu nekkut lu ratax. Tax ba, nawet du wees te déggoo “am sàmmkat bi”, “indil baykat bi”. Seen i coow di dem ba jéggi dayo, ba ñu ciy gis léeg-léeg ay bakkan di ci rot. Loolu tax ba ñu indi ay saafara ngir jàmm am ci seen biir te kenn ku nekk ak wàll wa nga fare gis sa bopp ca la ngay def.

Ci kow loolu, ji ñu dénk wàll woowu, di Daawda Ja, fésal na mbégteem jëm ci woteb càrtug càmm gi (code pastoral) ca ngomblaan ga. Lépp nag ngir feg xeexoo ya cay am.

“Léeg-léeg ay jàppante day am ci diggante sàmmkat yi, baykat yi ak ñeneen ñi fare feneen. Te, loolu du lu baax ci càmm gi. Sàrt bii dina tax ba ñu moytu jafe-jafe yooyu.” Muy ay kàddu yu fa jëwriñ ji biral.

Loolu lépp nag teewut njaw des uw xàmbin. Ndax, wàll woowu di càmm gi ma ngay wéy di sooxaale ay gàllankoor. Nde, bu ñu amee am péex ca lañuy yëngu te yeneen gàllankoor di leen di gaar, ña ca nekk duñu ne gongo doonte ne dépite yépp nee nañ waaw.

Yenn ci yooyu, limees na ca ay ndimbal ciy koomal ngir dundug jur yi. Ñu mën di lebal i koppar ña cay yëngu, waaye tamit ag kaaraange jëm ci feg càccug jur gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj