NJAAYUM SUUF : DOORO GÉY TAQAL NA MAKI SÀLL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dooro Géy, di kenn ci ñi jege lool Maki Sàll, lañu jàpp fan yii ci mbiru njaayum suuf fa naawub Léwópóol Sedaar Seŋoor ba ca Yoof. Kii di Sakilulaahi Sow, njiitul kërug lijjanti gii di SCI AMANAH, moo ko pelent.

Ba Sakilulaahi Sow di pelent Dooro Géy, Maki Sàll a nekkoon ci boopu réew mi. Waaye, booba, kenn àdduwu ci woon. Bi nguuram gi daanoo nag lañuy sog di wax ci mbir mi. Yéenekaay Libération di ñu xamal ne, li ñuy toppee Dooro Géy mooy, njaayum suuf ci barabu naawub Léwópóol Sedaar Seŋoor ba ca Yoof.

Ba ko luññutukati DIC wooloo, laaj ko, dafa tontu, wax ne, Maki Sàll moo ko mayoon pàkk yooyu, mu waroon leen a jaay ngir kopparal (financer) yenn liggéeyi biir (missions secrètes) yu ñu ko dénkoon.

Bees sukkandikoo ci L’observateur, mu ngi xool ak ay layookatam nu ñuy waxtaanee ci njekk ngir indi saafara ci mbir mi. Ba sax nangu naa dugal 500i miliyoŋ, li ci des mu mottali ko balaa njeexitalu weeru sulet 2024.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj