Sàndarm yi wàcc nañu fa liise Delaafos ci gaawu gi. Yéenekaay Libération ne, seen wàcc boobu, wàcc bu am jom la. Nde, nee nañu, njambaanu Molotof mee leen fa xeeñ.
Muy ab xibaar bu ñu fésal ci gaawu bi. Dañ leen a déey ne am nay njambaani Molotof yees làq ci genn kër gu féete ci diggu liise Delaafos. Mu mel ni tur woowoo ngi bëgg a booy i nopp ci biir Senegaal. Ca coowal Usmaan Sonko la ko ndaw tàmbalee xeexe. Looloo taxoon sax waa Nguur gi jàppe woon ñi koy jëfandikoo niy rëtëlkat, maanaam ay terorist. Njambaan mu doy a doy waar la, gaaw a jàpp lool te mën a sabab i jéyya. Moo tax, kenn ñemewu ko, rawatina takk-der yi. Xel yi fàtteeguñu biisu Tata bees ko sàndi woon fan yii, mu tàkk ba jeex, ay bakkan rotoon ci.
Ci gaawu gii nag, la coow li dekkeeti fa liise Delaafos. Daara ju digg-dóomu jooju, ràññees na ko ciy ñaxtu yu tar ya ndongoom ya amaloon, doon kaas ngir ñu bàyyi seen moroom bi yoon tegoon loxo.
Bi sàndaram yi jotee ci xibaar bi, dañu jël seen i matuwaay, daldi wàcc ca kër ga. Ginnaaw ba ñu amale seen ub liggéey, luññutu kër ga, ca lañ ko fekk ca féexluwaay ba, maanaam ca tookër ba. La jot a rot ciy xibaar mooy jot nañu fa jàpp lu tollu ci juróomi nit ginnaaw ba ñu fa fekkut boroom kër ga. Lañu ca mën a jàppe mooy yoon tijji na ci ab lànket.
Ñu mën cee tënkee ni, réew mi gëj naa am ug dal. Bu ñu deme ba ne far Yàlla, xibaar buy jóo askan wi ci fitna juddu. Muy mel ni daara yi muccuñu ci, doonte ne ña nga ca waajtaayu tijji seen i bunt.