NJÀNG MAA NGI CI YOONU NDËRMEELU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njàng meek njàngale mi ci Senegaal mu ngi jànkonteel ak i jafe-jafe yu metti. Muy lu faf daj kàpp daara yépp. Mu mel ni la wolof naan “jàngoro day wàlle” moo ca mujj a am. Nde, coow yooyu ci daara yu kowe yi lañu ko nemmeekoo ginnaaw ba ñu tëje jànguneb Séex Anta ba ca Ndakaaru ay weer.

Njàng mi ci réew mi mën nañ koo méngale ak ug màggat. Nde, foo laal fépp day metti. Mu mel ni jàngoro ja daa far yokku ginnaaw ba ca lekkool ya wàllee. Coow li doore woon ca jàngune bu Ndakaaru ba ndongo ya doon sàkku ñu ubbi ko. Mu mel ni nopp bu bon bi la leen seen njiit yi jox. Loolu tax ba jàngalekat yi bootu ci SAES tay yëngu ci daara yu kowe yi, wone seen ànd ci bëgg-bëggu ndongo yi. Tax ba ñu sóobu ciy ñaxtu. Ñu gis ne daara yu kowe ya féete ca yeneen diwaan yi jàng amu fa. Moo xam ñuy jàppale seen i moroom wala sax ñu sóobu ci seen xeexub bopp. Waaye mbir ma far naa ëpp i loxo ba ca aara yu digg-dóomu yi bokkee. Mu doon lu jéggi dayo ginnaaw ba waa SAEMS ak CUSEMS tàbbee ciy ñaxtu ci talaata jii. Muy kurélu jàngalekat yi fare ci daara yu digg-dóomu yi ñoo feddali seen mer jëm ci digaale ya doxoon seen diggante ak Càmm gi. Waaye tamit di wéy di ñaawlu njàpp gi ñu jàpp seen i naataango ci kaso yi. Te, lañu cay sàkku di ñu bàyyi leen, tax ba ñuy biral ne lekkool bi dee na. Ñu mën koo gise ne jooju wax bokk na ca feem ya ñuy xeexee. Waaye, mu nekk lu naqari ci dégg-dégg. Loolu tax ba jëwriñ ja ñu dénk njàng mi di Séex Omar Aan génne ab yëgle mel ni kuy dankaafu ak a xupp jàngalekat yi. Nde, moom la mu gis mën nañ koo firee ne kenn du waccu ba noppi di ko lekkaat. Mu mel ni jot naa fàttali la doxoon seen diggante ak jàngalekat yi, matukaay ya ñu ca jëloon ak koppar yu takku ya ñu ca jotoon a def.

Lañu seetlu ca boobu ñaxtu mooy ab xeex bu jàll ginnaaw ba lekkool yu bari dakkalee seen um njàng. Mu mel ni xuppe ya daa far yokku joote.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj