NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI : COOWAL LIJAASA “CAP” BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jàngalekat yaa ngay ñaxtu ak a naqarlu anam bi ñu nekke, rawatina ñàkk maandu gi dox seen biir, ñoom  jàngalekat yi. Li way-ñaxtu seetlu, ci seen gis-gis, mooy ne yemalewuñ jàngalekat yépp. Ñooñii di kaas lu ni mel, duppees na leen “Les décisionnaires”.

Ci biir liggéeykati Bokkeeef gi, liggéeykat bu ci nekk, am na ndombog-tànk ba ñuy lay takkal. Woroo googu ak ñàkk a yamoo googu, dañu koy gis ci biir jàngalekati Senegaal yi. Li sabab coow li nag moo di ne, Càmm gi dafa jël ay ndogal yuy jur xàjj-ak-seen ci seen biir. Maanaam daal, Nguur gi doxalul maandute seen diggante.

Ndogal yooye sooke wax ji, ñi ngi aju ci njàng meek njàngale mi. Jàngalekat bi, dafa am ay kàtte yi muy war a def ngir fàggu ay lijjaasa yi koy tax yokk darajaam ak payooram. Kàtte yooyu, bob CAP ci la bokk, doon lu solowu ci ñoom. Dafa di kat, lijaasa boobu, bokk na ci liy tax seen i tur di wuute ba di jeexital ci seen uw nekkin. Bu ñu sukkandikoo ci “Les decisionnaires” yooyee, CAP bi, ki ko am laata muy am 35i at ak ki ko am ginnaaw bi mu ëppalee 35i at, ñoo war a yem kepp.

Coow lii nag, day ñëw, di ñëwaat saa su nekk, jàngalekat yi di ko metitlu te bëgg mu dakk. Moo tax, jotoon nañu teewoon ca Ngomblaan ga, ca weeru nowàmbar 2023, bi fa jëwriñu liggéeyu bokkeef gi, Galo Ba, waree jàll. Ginnaaw ba ko dépite yi soññee ci bile jafe-jafe, moom jëwriñ ji dalaloon na seen i xel yi ginnaaw bi ñu ñoŋalee seen bérébu liggéeyukaay bi war a saytu loolu.

Mënees na wax ne, jàngalekat yooyu di wuyoo ci turu “Les décisionnaires”, wokkaat nañu góom ba, mel ni ku naan jëwriñ ji “gor ca wax ja”.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj