Njureef ya tukke ca wotey sendikaa jàngalekat yi bir na. Mu mel ni, jàngalekati Senegaal yi tànn nañu kurél yi leen di teewal ci kanamu Nguur gi. Ci altine jii weesu lees dooroon wote yi. Waaye, wile yoon, dañ ci indiy coppite. Nde, wote yi, jaaralees na ko ci jumtukaayi xarala yu yees yi. Lees ko dugge mooy gën a jàppandal wote bi te gën koo ñoŋal.
Kurél yiy teewal jàngalekat yi xam nañu leen. Seen ub lim a ngi tollu ci juróom-ñaar. Bokk na ci SIENS mi ëmb ñiy saytu jàngalekat yi, am lu tollu ci 92,21% ciy xob. SELS, UDEN, diy kurél yi féete ci jàng mu suufe mi, am ku ci nekk 26,30% ak 15,78 % ciy xob. SAEMSS, CUSEMS ak CUSEMS/Authentique ñi séq njàng mu dig-dóomu ba ci mu kowe mi, am 34,58%, 25,65% ak 18,51% niki ni ñu toftalantee. SNELAS mi ëmb jàngalekati araab yi moo tëj bile lim. Ñii ñoo nar a séq ak Càmm gi ay waxtaan ñeel seen i ñaxtu ci wàllum njàng mi ak njàngale mi.
Muy ay wote yu ñuy amal juróom-ñaar i at yu nekk. Kurél yu bari di sàkku ay xob ci jàngalekat yi ; kenn ku nekk ak fa nga fare ngir xeex seen i àq ak yelleef. Ci loolu, juróom ñaar ñi, ñoom lañuy tànn ngir seen i waxtaan. Ca 2017 lañu mujje woon amal yile wote. Njureef yi ñu am wii yoon, am nay coppite walla sax ag mbetteel ci ñenn ci sendikaa yi. Ku ñi mel ni SELS Authentique miin nañu teewaayam ciy ñaxtuy jàngalekat yi, waaye wii yoon gennut. CUSEMS bu Daam Mbóoj jël ag toogoom ca kanamu Càmm gi.
Mënees na jàpp ne wotey sendikaa jàngalekat yi am na solo ndax pàccu njàng mi ak njàngale mi bokk na ci fànn yi ëpp doole ci réew mi. Ñu seetlu ne, ci wàllu sendikaa, jox nañu dayo bu mag xeex àq ak yelleef. Looloo tax na ba jàngalekat yi def ko ngànnaay lu réy ngir seen taxawaay gën a dëgar.