QATAAR, FULLAAY JAAY DAQAAR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bu ñu toppe mboorum futbal, mënees na wax ne guleet dëkkub naar di dalal kuppeg àddina si. Nde, du ku jóg rekk, FIFA jox la ay. Kon, bu Qataar dee réewum naar mu njëkk a dalal xew-xew bile, du como. Ana lan mooy ndëgarlaayu Qataar ? Futbal bu weesoo tàggat-yaram, yan njeexital la mën a am ? Qataar nag, réewum diine la, ràññeeku ci lislam. Moo tax, bari nay mbir yiñ tere ca seen réew te tubaab yi baaxoo ko, moo waral coow lu bari li ànd ak xew-xew bi.

Qataar nekk dëkku diine, lislam teg fa tànkam ba nga xam ne, Nguur ga moom lay jëfandikoo, bu ñu sukkandikoo ci këru yëglekaay gii di Reformes.c. Yaxal bi mu siiwal, àjjuma 18 nowàmbar 2022, dippe ko “Le Qataar entre Mondial et agenga religieux”, wone na lu bari ci xar-kanamu Qataar. Ci loolu, mu bokk ci dëkk i lislam yi gën a fés ci àddina si. Ñenn ci boroom xalaat yi dinañuy faral di wax naan, Qataar day taral ci diine ji. Ñu gis ne, fi Qataar di gën def xaalis mooy ci tabaxum jumaa walla ay jàkka. Kurél yu mel ni Qatar charity ñu ngi tabac i bérébi diine fépp ci àddina si, muy Tugal walla Afrig. Ñu nemmeeku teewaayam ca Mali, Niseer ak Senegaal. Ràññees na yit ay ndawam yu am doole ak koom bokk ci nit ñi gën a ràññeeku ci àddina si. Kon, ñu gis ne biral lenn ci mbooram dina tax ñu nànd as lëf ci taxawaayam ci kuppeg àddina si mu woote. 

Qataar dafa araamal mbirum ngóor-jigéen. Ñu seetlu ne ak ayam gii tombeeg péexte mu réy ci wàlluw àq ak yelleef jëm ci ku nekk, taxut mu nangu ñuy feeñal ak a fésal jooju jëf. Ci loolu, FIFA ànd ak moom ba teg ay daan képp kuy fésal mbirum ngóor-jigéen, moo xam kuppekat yiy takk seen wirgo yiy màndargaal googu kurél walla keneen ku mu mën di doon. Ñu mën cee lim xibaaru roppalaan gi waroon a indi kuppekati Almaañ gi yi te am wirgob ngóor-jigéen, Qataar lankal leen ko.  

Sàngara tamit, terees na ku ko fa naan, rawatina béréb ya wër fowu ya ak ca seen biir. Terees nañu tamit goor ak jigéen di jaxasoo ca réew ma te nekkuñu ay way-dencante, ngóor-jigéen moom, waxaalewuñ ko sax. Xibaar bi xët i yëglekaay yu bari siiwal ko tax ba kurél gi ñu dénk xew-xew bi di ROAD 2022 génn, joxe ciy leeral. Waaye lu ci mën di am, Qataar jël na ay matuwaayam ngir sàmm kaaraangeg réewam. 

Leneen li fés ba àddina juróom-ñaar di ci wax mooy alxuraan ji ñu tegoon keroog, bésu ubbiteg xew-xew ba. Guleet, bi powum kuppe sosoo ba tey, ñuy njëkk a biral njàngum alxuraan ci joŋanteb kuppe. Te, ñépp xam nañu ne alxuraan, ne islam. Nde, kuppeg àddina si dafa nekk xew-xew bu mag a mag, ay junni-junniy miliyoŋi nit di ko teewlu

Rax-ci-dolli, kilib bi artistu saa-amerig bu mag bii di Morgan Freeman séqoon ak doomu Qataar bii di Ghami Al Mufta, siiw na lool ci mbaali-jokkoo yi. Lañu jàpp ni moo am solo ci seen janoo boobu, di waxtaan wa ñu séq. Muy waxtaan wuy boole nit ñépp ci gennug giir. Di soññ nit ñi ci boddikonte, kenn ku nekk nangul moroomam lu mu doon. 

Ñu mën a tënk ne kuppeg àddina si yamul ci am po rekk. Nde, njeexital yi mu mën a jur bari nañ lool. Qataar nekk réewum jullit te gëm-gëmam ak aadam nekk na lu mu fésal ci xew-xew boobu. Li la wolof naan, ku aye, wal sa moome. Mo tax it,  fulla ju mat la ci Qataar boole.



Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj