WAAW, KAÑ LA SENEGAAL GËJ A YËNGOO NII…?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Weeru màrs wii weesu, Senegaal tàngoon na jipp ! Gannaaw ba alkaati yeek sàndarm yi jëlijee Usmaan Sonko ngir jébbal ko Yoon, daanaka waa Ndakaaru yépp, waa Senegaal yépp sax, rawatina ndaw ñi, dañoo jóg nekk benn say, ne : “Du fi ame !” Keroog ak fan ya ca topp, jàppante bi metti woon na. Waa Nguur gi ne duñu bàyyi, gune yi gën leen a dëgër fi ñu jàpp. Noonu la fi fukki bakkan ak ñett rotee. Ñoom ñépp di ay waxambaane yu tollu ci seen diggu ndaw.

Ndax fu bakkan di rot, mat na di fa tudd yàqute yu dul jeex ci alal ? Ãxakañ ! Waaye, xel demul ci di leen méngale. Li nu soxal fii, mooy seetlu ni, li ëpp ci lu yàqu, nekkul ay alali doomi réew mi donte ñàkku ci. Waaye ay moomeelu doxandéem lañu, diy Tubaab yu sanc seen i këri-koom ci dëkk bi, ba tax ñu aakimoo daanaka koomu réew mépp. Këri koom yu mel ne Total, Auchan, Senac, añs. Loolu di nu fàttali bàkku yenn ndaw yiy xeex ngir Senegaal moom dëgg boppam : France Dégage ! (“Farãs jóge fi !”). Muy lu mat a jàngat ndax day wone ni, ndaw ñaa ngi ci tànki seen i mag yi fi nekkoon doon bañ nooteelu doxandéem bi. Te xaley tey yii, mel na ne ñoo gën a farlooti ci farata jooju.

Loolu lépp a taxoon Nguur gi dellu gannaaw, yolamal loxoom, bàyyi Sonko mu ñibbi. Guléet, ca ba muy ne ci jal bi, Persidaŋ Maki Sàll gis lu ko jaaxal, ëpp ko loxo ba tax mu walluji, ñaan xalifa yi ñu dugal seen loxo ci mbir mi, ba noppi nangul leen lépp lu ñu ko laajoon ngir indi jàmm. Mu mujje jél kàddu gi ñépp doon xaar, wax ak réew mi, ci anam yu ko kenn masul woon a gis : yëramtu, dige, ñaan njekk, woote juboo ak bennoo. Kujje gi ñoom it, wormaal kilifay diine ji, jóg ni kenn du dox i tànki jàmm bàyyi leen ginnaaw. Waxtu ya jiitu kàllaamay Maki yi, Usmaan Sonko jëkkoon na jël kàddu, wax waxi jàmm, waaye it teg ay sàrt yu leer yu Nguur gi war a jaar, ci gis-gisam, ba mën dalal réew mi.

Moo tax it, askanu Senegaal dina santati Sëriñ si. Ñoom ñi nga xam ne, daanaka, réew mépp a ngi doon xaar seen kàddu, ba nit ñi demee ba jàq. Ki ci gënoon a ràññeeku doon nag Sëriñ Muntaqaa Basiiru Mbàkke. Moom mi doxoon diggante Njiitu Réew mi ak kujje gi. Ñépp déggal ko, jàmm dellusi ci dëkk bi. Muy firndeelati solos sëriñ si ci nekkinu askanu Senegaal, te muy luy màndargaal Senegaal (te di dëggal lan ca jotoon a bind ci ginnaaw, ci sunub bataaxal bu nu duppe woon : ”Sëriñ seek a bari doole !”).

Waaye, ba lépp nee tekk, lépp sedd, waa Nguur gi mel ne du ñoom : ña laqatu woon ñépp génnaat di mbéléléli ci rajo yeek tele yi. Maki woote ndaje, wax ak guney pàrteem, di gaaruwaaleek a xupp kujje gi : “Li fi amoon, du fi amati !”. Mel ne, tey la Waalo gën a aay.

Teguñu ci juróomi weer, Persidaŋ Maki woo Ndawi Réew mi, wotelu sàrt yu yees yuy rëbb mbéeféer yi, ci ni ñu ko waxe.  Mu nel ne nag, dañuy taafantoo jiyaadis yi, ndax ku seet ba ca biir xam ni, ñi ñuy rëbb dëgg, du ñeneen ñu dul waa kujje gi ! Noonu boog, la ko ñu bare jàngate, ay boroom xam-xam yuy jàngale ci iniwérsite yi, waa kujje gi ci seen bopp, ba ci Usmaan Sonko mii jagleel xew woowu ay kàddu yu am a am solo. Du caagéen ne, danuy tëkkale Usmaan Sonko ak ay kàngami Afrig yu mag yu fi nekkoon. Waaye nag, neexul ba neexul, ngóor si, ni mu waxe keroog jooju, gëj na fee am (jóge ciy way-pólitig), ca jamonoy Séex Anta Jóob walla Tomaas Saŋkara. Ne jàkk waa Tugal, tudd seen tur, xamal leen ne lu bon te yées ci Afrig, ñoom a, walla boog seen loxoo ngi ci. Ba noppi di leen digal ñu teggi seen loxo ci kaw Afrig te abal nu !

Sàrt yu bees yii nag, li ci doy waar mooy ne, ëpp nañu téeméeri ponk, te sunuy Ndawi Réew mi, ciy “anam yu jamp” la leen ko gornamaŋ bi jébbal, ñu war koo jàngat itam ci diir bu gàtt (benn ba ñaari ayu-bés). Moone, ñoom ci seen bopp, ci bataaxalu Commission des Lois, di kurél gi ñu jagleel liggéeyu caytu sàrti Yoon yi, ñu ngiy xamle ni :

Code Pénal bi ak Code de procédure Pénale bi (ñaari téere yooyu ñu leen di woteloo) soo leen joxoon ñu seen xel màcc ci mbiru Yoon sax, dinañu am i jafe-jafe ndax dañoo naqaree jàng, kenn mënul a xam dëgg lu ñu wund ; waxatumaak nun Ndawi Réew mi nga xam ni, dara lañu amul ci xam-xamu Yoon”.

Waaw, ñii de, ñu xam loolu ba noppi, bind ko ba mu leer ci seen bataaxal, ñoo walbatiku wote sàrt yooyee, te naan nu: ‘Sàrt yii baax nañu ci askan wi’! Ku leen di déglu ba di leen gëm ?

Maki moom, booba, mu ngiy wër réew mi, dëkkoo dëkk, di nemmeekuji koomu gox-goxaan yi. Ci li mu lay, ndax ñu bare weddil nañu ko loolu, jàpp ne ay yëngug pólitig doŋŋ lay doxal noonu. Lum ci mënti doon, li yéeme ci mbir mi, mooy nit ñu baree bare yi muy dajale saa su ne, ciy jamanoy koronaawiris bii ! – Am sax ñu ñuy yab ciy woto, péey ba péey, gannaaw ba ñu leen compalee as tuut ciy koppar -. Dëgg la, ba mu noppee ciy doxontoom yooyu, xelam dellusi na, ba tax muy digle ñu bàyyi mbooloo yu tàkku yi ñuy woo ci xew yi. Xéy-na ndax “Covid 19” day moytu ay xewi Persidaŋ Maki Sàll ? Bugaan Géy Dani moom, faalewul waxi Maki yooyee, ndax moom it sol nay dàllam di doxal li mu tudde “Tibbi Tànki Maki”. Di wër réew mi, fu Maki jaaroon mu jaar fa, lu Maki waxoon, mu weddi ko ba mu set wecc ! Nit ñu baree bari di ko topp. Usmaan Sonko, moom it, ne kenn du dem mu des, daldi jëlaat “Nemmeeku Tuur” yi mu nu tàmmaloon. Wuudey Medina yi de, ñoom, duñ ko réccu ndax seen i njaay yi mu leen fexeel ba ñu jar, ci kaw dimmali liggéeykati Senegaal yi.

Senegaal nag, wax ko te dee, day réew mu doy waar ! Ndax kat, jamono jii koronaa bi gën a lëmbe àddina si, rawatina ci miim réew, la nit ñi mel ne ñu raatukaan ! Ku la gën a ñeme mbas mi, nga ni kii la ! Mu mel ne, nit ñi dañoo dem ba ës, walla book ñu tul (tul bu wuteek ñakku yi fi lamb ba dee !) ba tax koronaa bi du leen mënal tus ! Te kenn rawu ci way-pólitig yi.

Waaye kenn du nettali doxantuy Maki Sàll yooyu te doo yëy yàbbi ci mbiru nervis yi, maanaam dóorkat yi ! Ñépp gisoon nañ fi ne, ci xew-xewi màrs yi, ay sàmbaabóoy yu gànnaayoo seen i yat, walla ay jaasi, ñoo doon daw ci tali yi di rëbb xale yi doon ñaxtu, di leen jàpp, di leen dóor, dóor yu metti. Loolu lépp nag, doon ame ci kanamu takk-der yi, mu mel ne sax, ñoo àndoon ci seen “liggéey” boobu ! Dóorkat yooyee ñoo feeñaat ci doxantu Maki yi. Ñu neeti ci seen mënin, di jàpp, di dóor gone yiy ñaxtu walla sax ku ñu gis rekk nga sol mbaa nga takk lu xonq ! Dëgg la, seen kilifa moo fi newoon, lu yàggul dara, moom lu xonq du ko gis ! Waaye ku taxaw seetlu dinga gis ni, ba Persidaŋ duggee Tuuba, dóorkat yi dañu ni mes ! Kenn gisul, kenn yëgul. Moo tax it, gune yi xaaruñu ku leen woo : takk seen i sagar yu xonq coyy, di yuuxu, di sànni suuf, ñenn ñi sax di yuuxu turu… Usmaan Sonko ! Dóorkat yi daal (walla seen kilifa ?) ñemewuñu Boroom Tuuba ! Lu mu ci mënti doon, gannaaw takk-der yi, ay dóorkat, fenn lañ leen soxlawul. Te réewum Yoon sax, daa mënut a ànd ak li nu mel. Maki nag, war naa seetaat boppam !

Ayu-bés gii ñu génn nag, Persidaŋ wooti na Ndawi Réew mi, ñu wotelati ko ay sàrt yu bees yu jëm ciy doxalinu wote yi. Fii tam, lu yéeme feeñ na fi : lu bare ci déggoo yi amoon ca Dialogue National ba (Jataayu Waxtaanekaayu mbiri Réew mi), walla ponk yu ñu yaakaaroon ne Persidaŋ dina ci jël ndogal, dañu leen teggi teg fale ! Xeli nit ñi gënatee teey ci mbirum ñetteelu màndaa bi ñuy ruumandaat booba ba léegi, di wax naan, mu ngi ci xelu Maki. Te loolu lépp fekk na mu soppi, ni mu ko neexe, tëralinu gox-goxaan yi ci Ndakaaru, te tagguwu ci kenn ! Waaye li ci kanam rawul i gët.

Fii ñu toll nii nag, yenn xel yaa ngiy ñaaw, yeneen yaa ngiy nàcc. Lii lépp ciy xew-xew yu baree nii, ame ci diir bu gàtt ; xew wu la ci gën a metti walla gën laa lëj, nga ne bii la. Mbaa réewum Senegaal dina ko mën a dëkku ? Mbaa du ñaareelu “weeru màrs” daf fe nar a am ? Li gune yiy woowe 2e vague, maanaam ñaareelu sóobu ciy ay ? Dëkk bu yëngu bii, nu fiy jàmm dellusee, sax fi dakk ? Te muy jàmm ju lalu ci dëgg ?

Wax jaa ngi noonu. Nun waa Senegaal nag, ndax warunoo seetaat sunu bopp ? Ndax kat, fu fen di mën dëgg, fu kàdduy worook i jëf, taxawal fa luy jëm kër du yomb ! Rawatina réew moo xam ne, Nguur gi, jay-doole rekk la xam te di ko doxaale bu baax. Fàww kon, ñi bokk gis-gis te gëm seen bopp, gëm demokaraasi te féeteek askan wi, booloo, takku tey xàccandoo di dóorandoo, su nu bëggee tekki buumu-njaam gii nu tënk ba léegi.

Uséynu Béey

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj