SÉEX ANTA JÓOB : XARNUB LEER

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fanweeri at ak juróom-ñaar ginnaaw ba mu làqoo, Séex Anta Jóob du mës a dañ ci xol yi ak ci xel yi. Waa RND dëggal nañu wax ji. La ko dale juróom-ñaari fan ca atum 1986 ba sunu-jonni-Yàllay tay, ñuy wéy di fàttaliku seen jàmbaar ja.

Xamle Séex Anta Jóob bu doon booy i nopp, kon sunuy nopp booy. Waaye kaaŋ-fóore loo wax ci moom, am loo bàyyi. Ay yaxali yaxal du doy ci xamle kan mooy njool Céytu. Ndey Koddoo nga naan ca Defu-waxu Suul ker du ko tere feeñ, rawatina ab xarnu ginnaaw bi mu feeñe ca Céytu.

Séex Anta Jóob mi ngi juddu ci atum 1923 ca Céytu dëkk bu féete ca xolu Bawol. Am njàngam nekk lu yéeme bi mu dalee Alxuraan teg ca njàngum lekkool. Ginnaaw bi mu amee bàkkalóoriya, la wéyali am njàngam ca Tugal. La mu doon toppu jëm ci màndaxe ak xeltu terewu koo ubbeeku ci yeneen fànni xam-xam yi. Ci kow loolu, gëstu ci wàllum làkki Afrig yi nekkoon yitteem ba liggéey bu réy ba mu ca def moo tax tey kenn du jàng sa làkk te sa xel du dem ci njool Céytu. 

Mu mel ni li Wolof Njaay naan : “bay ca sa wewu tànk”, Séex ku ko teel a nànd la. Ndax ab gëstoom ak ub xeexam weesuwut lu dut Afrig xam cosaanam, xam mbooram, xam mooy kan. Ndax xam sa bopp njëkk dina tax nga xam foo jëm. Looloo tax mu yàgg a jóg ca teel ngir kembaru Afrig nekk benn, te bennoo mooy doole. Te, li gën a gaaw ci boole aw askan, mooy caada, mooy mboor, loolu la yàgg a layal ci ay mbindam. 

Waaye ñu seetlu ne njàngaleem Séex tey la gën a bees ci xamle nan la am réew war a doxe, am njàngam ba ci koomam bu bëggee jëm ca kanam. Wànte, ñuy wéy di tànqamlu ci ay gëstoom. Ca atum 2016, lañu waxoon ne dinañ dugal njàngaleem Séex ci lekkool yi waaye ba léegi ay digeey neen. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj