SENGHOR AK HOUPHOUËT, DOOMI AFRIG YI DAAN XEEX AFRIG (2/2) BOS NDÓOY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci beneen boor, ci nguuru Seŋoor lees nose, ñeel Senegaal, “Opération Persil” ak lenn ci “Opération Mar Verde”, ngir suuxal nguuru Séku Ture ca Gine ndax li mu dakkaloon nooteelug Farãs ci réewam. Taxawaayam deful lu dul dëggal kàddu yii : ku gërëm sag njaam faww nga noonoo kiy fippu. Mënees naa fàttali lu baree-bari ci lu Seŋoor def walla mu wax ko te mu safaanook njariñal Senegaal ak Afrig ngir jàppale Farãs ci noteelam seen kow. Boo tegee ci wetam Houphouët-Boigny, njiitu Kodiwaar ba woon, dinga gis ñaari tànk yii Farãs doon doxe ngir wéyal nooteelam ci Afrig. Frantz Fanon nee na Houphouët bokkoon na ci noonu Afrig yi xeex Afrig ngir mu bañ a moom boppam, ci dunguru réewu Farãs yi yéesoon la bokkoon. Mu teg ci ne, “Looloo taxoon mu demoon benn jotaay ci jotaayi mbootaayu- réew yi di fa faral réewu Farãs. Àggoon na ciy wax ne, ci xalaatam, Alséri warul a moom boppam.”

1 Pour la révolution Africaine, Frantz Fanon p.135

Moo kootoo woon ak Farãs, di yéeg ak a wàcc ba neenal naalub Bennoog Mali (Fédération du Mali) bi réew yii toftalu nasoon : Dahomey (Bénin tey), Haute-Volta (Burkina Faso tey), Senegaal ak Sudaŋu Farãs (Mali tey). Fexe woon, yit, ba sore Senegaal ak ñi mu tudde woon way-xiif yu Sayel yi. Ba mu yàqee xelu waa Dahomey yi ak waa Haute-Volta yi ba noppi, ci la leen moccee ba ñu nangoo taxawal beneen Ndajem déggoo (Conseil de l’entente) ëmboon, ca ndoorteel la, Senegaal, Kodiwaar, Niseer, Daawome ak Haute-Volta. Loolu lépp ngir néewal doole walla neenal jotaayu Bennoog Mali gi. Houphouët Boigny bokkoon na ci ñi jàppale woon Kasa-Vubu, mbëru Pari ba, ngir xeex Patrice Lumumba. Bokkoon na itam ci ñi bëggoon a yëngal réewum Gine bi muy door a moom boppam ak ci ñi fexe ba daaneel Kwame Nkrumah. Houphouët Boigny moo " jàppale lalkati pexe yu bon yi seenub dugg ak génn ca Kodiwaar ngir ñu mën a nas seen i pexe. Cig jàppale Farãs, jàppale bu amul fu mu yem ak lu ko tënk, bokkoon na ci ñi jëkk a nangu amug Biafra, diiwaan ba doon xeex ngir beddeeku ca réewum Niseryaa. Umpul kenn, taq bu réewum Farãs taq ripp ca xeexu beddeeku boobu. Ca Kodiwaar sax la kolonel Ojukwu, njiitu way-fippu ya ca Niseryaa dawoon làqu. Jacques Foccart mas na ne

2 Bridgette Kasuka, citée par Said Bouamama, Manuel stratégique de l’Afrique, p.71, Tome 2

« Seneraal de Gaulle nee na ma woon lu la neex defal ngir fexe ba Kodiwaar dimbali Biafra »

Bari na lees mën a wax ci ni Houphouët Boigny déggale woon Frãs. Alasaan Watara, mi ko jége woon lool, deful lu dul topp ciy tànkam. Moom ak naataangoom Maki Sàll ñu ngi wuutu bu baax Seŋoor ak Houphouët. Ku ci nekk tagg nga xaalisu Cfa, teg ci dàq ci sab dëkk Kemi Seba mi ko doon ŋàññ. Alasaan Watara dàq na yit Nathalie Yamb. Ñoom ñaar ñépp ñu ngi sàmm, càmm gu amul ayib, teraangay Farãs ci seen i réew. Gaaw gi Alasaan Watara yàkkamtee Eco wuutu Cfa teeyul xel
yem ci. Waaye, day ag wor gu mu wor Afrig. Xeex bi ñenn ci doomi Afrig yi Farãs nootoon seen i réew di xeex seen biir ngir sàmm teraanga Farãs ci Afrig yemul rekk ci ay ngànnaay. Am na tamit ci wàllu xalaat. Liy màndargaal xeex bi ci wàllu xalaat mooy ñiy layal Farãs te santu leen ko sax. Ndax mbéefeer ma du woon rekk ab nooteel ak ub ratt ci wàllu koom. Da cee bokkoon tamit wëlbati xel yi, mbaa naan yóor yi, ni ko Frantz Fanon daan waxe. Ci wàllu wëlbati xel googu, Farãs da ci am ndam lu réy. Ba tax na, doomu Afrig yu bari, ay xalaatkat yu mu tàggat ci ay daaraam yu ndaw, yu digg-dóomu ak yu kowe yi, dañoo taxaw temm ngir aar ko, waxal ko. Ñooñu la Sartre wax ne, ci dugge bu téere Frantz Fanon bi, Les damnés de la terre, ay nit yu ñu soppi lañu, mënatuñu sax wax ak seen i askan ndax li leen wutale dafa bari. Te yit, warees na
bàyyi xel waxi Odile Tobner yii

3 Ibid, p.71

«Xalaatkat yu ñuul yi dañuleen di bàyyi xel, bàyyi xel bu metti. Maasu boroomi lijaasa lañuy yeew seen i loos. Ku bëgg bokk ci njiiti Afrig yi, ëllëg, nara jaay seen réew yi, noot seen i askan, luubal seen alal danga naam nemm tëj sa gémmiñ. Loolu mooy njëg li. Ci beneen fànn, bañkat yi, ñi war a yee seen i askan, dañu leen di xeex, di leen ñàkkal faayda» 4

Am na yenn yoo xam ne dafa mel ni Afrig rekk lay ame ndax, lu ci bari, ñii dañuy xëcc jaar fii, ñee xëcc jaar fale. Loolu tax na dëkk yi daan jaay jaam, jarul ñuy balu àq ci seen jëf ju ñaaw jooju, walla ñuy joxe ndàmpaay, ndax dina am, saa su ne, yenn ci doomi Afrig yi, ay xalaatkat yu ñu jënd yuy jóg wax ne du woon ñoom rekk, ndax amoon na doomi Afrig yu leen jàppale woon ci njaayum-jaam gi. Xéy-na, dañu xamul ne xeet woo not, dina ci am ñuy wëlbatiku far ak ñi leen noot. La xewoon Farãs ba leen Almaañ nootee firndeel na ko. Ñiy gën a suuxal Afrig, bu ñu tëddee mën nañoo nelaw ba
yàndoor ndax dinañu am ay doomi Afrig yu leen di xeexal, di leen layal, naan : Afrig bu jëmul kanam, warul mere keneen ku dul boppam. Wax nañu dëgg boo ko seetee ni njiit yiy sànke seen alalu réew ak ni ñu ñàkkee seen i ndeyi-àttey réew.

4 Odile Tobner, Du racisme français, quatre siècles de négrophobie, p. 228-229

Li ci gën a doy waar moo di ne réew yu bari ci Afrig ñàkk
moomuñu seen bopp. Rawatina ñi ci Farãs nootoon te ñu féete ci bëj-saalumu màndiŋum Saxara. Teg ci, réewi Tubaab yi dañoo bëgg a bindaat sunu taarix. Ngir bañ cee feeñ, dañ koy jaare, lu bari, ci sët ak sët-sëtaat yi mu nootoon, defoon leen i jaam. Daanaka, day def lépp ngir ñu ne Afrig li ko dal moo ko liggéey, bu desee ginnaaw warul mere keneen ku dul boppam. Loolu lépp ngir ñépp fàtte yu ñaaw yi mu fi def : njaam gi, mbéefeer ma ak nooteel bu yees bi xew tey, tere Afrig suqaliku. Rax-ci-dolli, 5i xarnuy nooteel mënul a ñàkk bañ a am ay njeexital ci ñi mu dal seen kow, rawatina ci wàllu mbatiit, koom ak xel. Mu nuy fàttali li Albert Memmi tudde « complexe de Néron ». Ngir wutal cëslaay ni ñu saax-saaxe réew yi ñu nootoon ak daganal càcc gi ñu leen doon sàcc, mbéefeerkati démb ya ak yu tey yi, dañoo lal ay pexe, di fenn di dajale. Bu yàgg ba, ñu jëkk ñi dañu daan mbubboo ne seen wareef la
woon ñu gindi yeneen xeet yi, génne leen ci xayadi ak lëndëm ndax ñoom ñoo gën ñépp. Léegi bi mu leeree ne seen wax yooyu teguwul woon ci xam-xam, méngootul ak jamono, te rafetul, dañoo daldi soppi seen waxin. Léegi, dañuy ŋàññ yenn mbaax ci mbatiitu réew yi ñu noot walla yi ñu bëgg a noot, di wax naan dañoo xayadi, tudde leen ay réew yu tayel walla yoo xam ne nii, dañoo tële ba sax, alal ji fa ne gàññ, mënuñu ko

5  Albert Memmi, Portrait du colonisateur, portrait du colonisé, p.72

jariñoo. Réew yoo xam ne nii, kuy leen di jaay doole rekk moo leen mën a jiite. Ci beneen boor, dañuy jéem a bindaat taarix, di tagg seen demokaraasi ak seen naataange. At yi dañuy jàll waaye jëf yi soppeekuwuñu. Dara beesul ci àddina si. Xeetal bi ñu laloon ci wàllu xeet, léegi mu ngi tégu ci fànnu mbatiit. Ci wàllu simpi walla bàyyi estati Faidherbe bi, wax ju bari ji, jàppal-bàyyil yépp matu ko woon, ndax mbir mi du leneen lu dul mbirum fulla ak faayda. Xel xalaatul estatib Hitler sampu biir Tel-Awiw walla kenn di sargal Bugeaud ca Alseri. Su njiiti Afrig yiy sibooru réewi Tubaab yu am doole yi, dafa fekk moomuñu seen bopp. Feek réewi Afrig yi mënuñuy fal ak a folli seeni njiit ; feek mënuñoo aar, dundal ak faj seen bopp, ci waawu ay dunguru Tubaab yi lañuy wéy di doxe. Ndax ñoom, li leen yitteel mooy bégal réew yu mag yi, kurél yiy lebale xaalis. Lii rekk war naa tax Afrig booloo, jëmmal yéene Séex Anta Jóob ak Kuwaame Kurumaa.

Boos Ndóoy

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj