SET-SETAL NGIR WAAJAL NAWET BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb, gaawu 1eelu fanu suwe 2024, moo doon bés bees jàppaloon set-setalu réew mi. Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, moo ko woote woon. Daanaka, ñépp wuyu nañu wooteem bi. Ndaxte, diiwaan boo dem fi réew mi, démb, génnoon nañ ngir laabal mbedd ya, loqati mbalit yi ci kanaal yeek tiwo yi ndox miy jaar.

Nawet baa ngi yëglu. Te sax, am nay diiwaan yoy, jot na faa taw. Dafa di nag, Senegaal, saa bu nawet teroo, rawatina bu taw yi baree, ay dëkk ak i gox yu baree bari dañuy nekk ciy jafe-jafe. At mu jot, mbënn mi dinay nangu kër yu bari, jur coow lu réy. Jamonoy Ablaay Wàdd ba tey, jaare ko ci Maki Sàll, Nguur gi dina génnee xaalis bu takkoo takku ngir saafara ko. Waaye, dara. Nguurug Maki Sàll ga woon sax, ci seen i wax, jot na cee def juróom-ñaari téeméeri milyaar ci sunuy koppar. Loolu nag taxul mbënn mi jóg fi. Sababi mbënn mi nag, bari nañ te wuute.

Bees sukkandikoo ci ma-xarañ yi seen xam-xam màcc ci fànn wi, dëkkuwaay yi ak salte gi ñooy sabab yiy gën a waral taa-taa yu metti yi. Ci benn boor, nit ñit dañuy faral di tabax ci béréb yoo xam ne, ndox a fa nekkoon. Moo tax, bu tawee, suuf si day gaaw a màndi, ndox mi daldi taa. Ndax kat, ndox du bàyyi yoonam. Léeg-léeg, ñu sanc ay koñ walla ay gox te, ci tabaxiin yi, xàlluñuy yoon yu ndox mi di jaar, dem, bu tawee. Ci beneen boor, jikkoy nit ñi ci seen bopp, seen càggante, mooy waral mbënn mi. Ndaxte, ñàkk a setal ak mbalit mi ñuy faral di tuur ci kanaal yeek tiwo yi mooy dem ba fatt yoon yooyii ndox mi waroon a jaar. Bu ko defee, ndox mi taa, indil leen ay jafe-jafe. Ngir fagaru ci nag, moo tax Njiitu réew mi woote set-setal bi amoon démb, ba noppi sóobu ci liggéey bi, moom ci jëmmi boppam.

Caaroy la Njiitu réew mi nekkoon, moom ak soxnaam ak yeneen i kilifa. Usmaan Sonko tamit, elimaanu jëwriñ yi, génnoon na, bokk ci set-setal bi. Réew mépp a ci sóobu tamit. Diiwaan boo demaan, tund ya, gox yaak gox-goxaan ya, mbooloo yu takku ñoo fa génn ngir wuyusi wooteb Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay.

Mbedd yi, kanaal yi, ruq yeek ruq-ruqaan yi, fépp lañ setal. Fu mbalit nekkoon rekk, loqati nañ ko, buub, tuuri ko fu war. Wëliis kilifay réew mi, yenn kilifa diine yi, ay kilifa aada yeek i boroomi tur génn nañ bokk ci liggéey bi. Kenn desul ginnaaw : mag, ndaw, góor ak jigéen, ku nekk a ngànnaayoo baleem, ñee yor i rato, ñale yor i ngaska, ñii di bale ak a loqati, ñenn ñiy dajale ak a buub, ñeneen ñiy tuuri. Ku sonn, keneen awu la. Lépp ànd ak kaf, fo ak ree. Lii moo méngoo ak Senegaal gi nu bëgg, Senegaalu jàmm, Senegaal gu set wecc ba, lu mu taw taw, ndox bañ fee taa.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj