Dee du jaas. Fu ko kenn dul xaar la malaakam dee mi naan jaas, ne fa coppet ab bakkan, te kenn sañul a kaas. Ku weddi, laajal Cekkeen mi ñàkk Jaaga. Waaw, Jaaga mu Bàllaago, Jaaga, ndeyu Móomi Sekk mi faatu lu yàggul dara, Jaaga ndeyu Waali Bàllaago Sekk… Jaaga, Soxna su yiw si, dëddu na. Xanaa du bakkan bu ñam dund, ñam dee ? Moo tax it, Jaaga, turam dëgg di Ndéy Faatu Kinne Juuf, gaañu na.
Tiis ak naqar dalati na ci njabootu Cekkeen. Baayu kër gee njëkk a génn àddina, keroog 14 màrs 2021. Yàggul dara, 5 oktoobar 2023, taaw bu jigéen bi, Móomi Sekk, topp ci. Ñu leen di jooy te noppeeguñu, malaakam dee mi duggati Cekkeen, ne fa coppet Jaaga, jambaaje xol ya, lëndëmal bët ya, tuur rongooñ ya.
Senegaal gépp a yégandoo xibaar bu tiis bile, askan wépp yëgandoo naqar wi. Ndey Faatu Kinne Juuf, Farãs la faatoo, ci gaawu gii weesu, 20 sãwiyee 2024. Nee ñu, ab feebar bu yàgg a ko tëraloon, ba ñu mujje woon ko rawale Farãs.
Jaaga, ku siiw la woon, lool sax. Daanul woy de, déedéet. Fësul woon ci tele yeek rajo yi de, déedéet. Waaye, mbaax gi woon ci moom, jikko ju rafet jeek taar bi, looloo tax askan wi amoon cofeel ak ug wegeel gu réy ñeel ko. Dafa di, li ko boroom këram ba woon, Coon Sekk, seedeel rekk doy na ci firnde. Nde, Coon Bàllaago Sekk, boroom baatu wurus bi, daawul deñ mukk ci di ko tudd, di ko gërëm ak a tagg ciy woyam ak i jotaay yañ ko daan dalal. Te sax, werekaanu mbuug (musique) bi tudde na ko aw woy wu siiw wow, jamono jii, ñoo ngi koy teg di ko tegati fépp ngir delloo njukkal soxna si.
Wax dëgg, Senegaal gépp a seedeel Jaaga lu rafet. Looloo tax itam ba askanuw Senegaal wépp jooyandook Cekkeen, bokk ak ñoom tiis week naqar wi, di leen jaale ak a mastawu. Njabootug mbuugu Senegaal (famille de la musique sénégalaise) ak ñiy yëngu ci mbatiit, ñépp a wone seen taxawaay. Moo tax sax, ñenn ña nammoon a amal ay xumbeel ak i yëngu-yëngal, ajandi nañu leen. Ci misaal, Yuusu Nduur ma ñu doon xaar Mbuur, fomm na ko. Aliyun Mbay Ndeer, Biddéew bu bees ak ñeneen ak ñeneen tamit, bëtal nañ seen i xew-xew.
Njaboot gi génne woon nañ ab yégle di ci xamle ne ci àllarbay tey jii lañuy rob Soxna Jaaga fa armeeli Yoof ya, bu 17i waxtu jotee, ginnaaw julli tàkkusaan. Ba tey, ci àllarbay tey jile tamit lañuy nangu njaal yi fa seen kër gu mag ga. Rax nañ ca dolli yit ne, lépp ca bés ba lay yem : amul dëju ñetti fan, juróom-ñetteelu fan astemaak ñeen-fukkeelu fan. Ndogal loolu, ci seen i wax, bëgg-bëggu Soxna Jaaga la woon. Moom Jaaga mi daan wax : “Man, Coon rekk !”, fekki na ko. Yal na Yàlla wonele leen fa sedd seen i xol.
EJO ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy jaale njabootu Coon Sekk gépp, di ko jaale njabootu mbuug ak mbatiitu réew mi, te di ko ñaanal mu tàbbi guyaar.