At yi weesu yépp, fitu doomi-Mali yi toogul benn béréb. Weer yi nu génn sax, seen njàqare ak seen tiis dafa mel ni lu yokku. Te lenn waralu ko lu dul jàmmaarloo yu tar yi am ci diggante ñaari waasoo yii di Pël yeek Dogoŋyi. Lu ni mel nag, jaaxal na ñu baree-bari. Ndax, ci atum 2012 ay defkati ñaawteef yuy mbuboo lislaam song réew ma. Ginnaw gi la ci Mbootaayu xeet yi dugg, jële leen fa ci atum 2013 ba noppi déggoo ak ñoom ci atum 2015 ci li fay war a saxal jàmm. Waaye loolu lépp mel na ni mujjul fenn. Ci at mii nu nekk, ci weeru Mars, 160 Pël la Dogoŋyi bὀom. Ñu ne déet-a waay, Pël yi daa di feyu, faat bakkanu 35 Dogoŋci 9elufan ci weeru Suweŋ, dolli ci 38 ba tey ci woowu weer, ci li nguuru Mali wax. Loolu lépp ci ñaari dëkk yu wute la xewe. Waaye Mbootaayu xeet yi jàpp na ne 41 Dogoŋ la ñu faat. Daw fitnaa tax Pël yeek Dogoŋ yiy gàddaay, wuti fu ñu làqu, moo xam Burkina-Faaso la walla fu ñuy wax Dinaguura.
Mbir mii nag, am na ñu jàpp ne xare ba fi jiyaadis yi amaloon moo ko sabab. Ndax nee ñu seen njiit, Aamadu Kufaa, ci Pël yi la doon wute ay soldaar. Pël yi nag, dañoo jàpp ne Dogoŋ yee sotba Mbootaayu xeet yi sempi ndëndu jiyaadis yi, reyaale seeni mbokki Pël yu bare.
Ñàkk kóolute gi lal lii lépp fan la jóge ? Ndax réerook mbañante gu yàgg rekk la ? Yàlla rekk a xam. Li am ba wὀor moo di ne waasoo Afrig yi yàgg nañuy jàmmaarloo ci seen biir. Te li koy waral léeg-léeg, bu weesoo xëccoo nguur, du lenn lu dul réere mbir li ñu bokk ndax, ni ko Séex Anta Jóob di waxe, li leen boole moo ëpp doole fuuf li leen di féewale.
Leneen ub na lool boppu nit ñi ci mbir mi te mooy tekk-tekkaralu àddina sépp, li ñépp toog boobaak léegi di seetaan. Ku nee ngi xaar ba sa moroom wax ngay soog a yëkkati sa baat. Lii kañ xanaa mooy lekkante leen ba jeex tàkk, sunu yoon newu ci ! Moom daal, ku mën sa moroom dumaal. Mbete làmbu tàkkusaan !
Li ci gën a xëtt xol, nag, mooy yàcc-yàccaaralu njiiti réewi Afrig yi, mu mel ni waa Mali duñu seeni mbokk. Te moo ne de ñoom lañu waroon a njëkk dégg bala kenn di yëkkatiy kàddu. Fi mu ne nii bala ñoo mën a wax mbaa ñu jëf fàww ñu jot ndigal lu tukkee ci nasaraan yi. Tàmm nañu ko sax. Seen yoon newul ci dëkkandoo bi leen yittewoo waaye su daray xew ci réewi Tubaab yi ñuy daldi tàggook seen sago. Ku ko weddi fàttalikul bés ba ay saay-saay songee Saarli Ébdo, rey fay taskati-xibaar. Keroog jooju njiiti Afrig yu bare fésal nañu seen naqar, ku nekk ci ñoom di nu tanqal, naan « Je suis Charlie ». Yii njiit daal, kenn xamul lu ñu doon. Boroom kër gu ñuy dab di ko mbej sax moo leen tane.
Li am ba des daal mooy na waa Mali delloosi seen xel te xam ne ay wu waxtaan fajul, xeex du ko saafara mukk. Nde bi àddina sosoo ak léegi kenn mësul a gis xare bu jur jàmm. Moom kañ, musiba rekk lay sooke, delloo am réew ginnaaw.