TAAFAR SI CI LÀNGUG POLITIG GI, MBAA DINA JUR JÀMM CI RÉEW MI ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xeetu taafar yi nuy faral di gis te di ko dégg ci réew mi jamono jii jéggi na dayo. Taafar moom du ci jёf kese, yenn xeeti kàddu yi moo raw jёf. Ndax mёn na taalum réew. Sunu réew mi nag, fan yii ak ya leen jiitu, bari na lun fiy nemmeeku ay xeeti taafar. Te, fu taafar am, kaaraange du fa am. Loolu nag, dina jur ay gàllankoor yu bari ci dundinu askan wi. Ndax, foo seetlu tuuti rekk foog ni foofu la taafar si ëppe. Muy ci làmb ji, di ci futbal bi, rawatina nag ci làngug pólitig gi nga xam ne moo gёn a yёngu ci jamono jii. Ndeem nii la deme ci béréb yu bari, mbaa jàmm dina yomb ci réew mi ? Waaye nag, laaj yi mat a samp kay mooy lan moo waral yenn xeeti taafar yi ? Lan moo ci war a doon ay saafara ngir dundinu askan wi gёn a mucc ayib ? Seen yéenekaay bii di defuwaxu dina ci indiy misaal laata nuy wax ci pexe yi war a mёn a dakkal yenn xeeti taafar yi.

Sunu réew mii di Senegaal dafa tàmbalee rafle lu bari ci ay jikko yu rafet ak i mbaax yañ ko xame woon. Lu ci mel ni yar, kersa, ngor, añs. Li koy firndeel mooy xeeti taafar yi nuy gis ci béréb yu bari. Lu ci deme ni ay saaga, ay xaste, tuumalante gi ak yeneen yu ni deme. Nu mёn a jёl misaal ci làngug politig gi nga xam ne xeeti taafar yu bari foofu lees leen gёn a nemmeekoo. Te, taafar sax nag yamul ci jёf rekk, yenn xeetu wax yi sax, bokk nañ ci li koy sabab. Ndax, ci fan yii weesu dañ fee gis jenn waay juy wuyoo ci turu Ahmed Susaan Kamara, mu yékkatiy kàddu yu ñagas teg ko ci njiital PASTEF lii di Usmaan Sonko. Mu dem ba àgg ci ni sax dañ ko war a ray ngir réew mi am jàmm, ci koo xam ne mbooloo mu baree topp ci gannaawam. Loolu bokk na ci li sos coow yu bari ci réew mi. Te ba tey, dara fekkagu ko ci ndeem, kàddu yim yékkati mёn na taal am réew bu ko ciy ñoñam toppoon.

Xeeti doxalini yoon yooyoo tax ba ku nekk jóg di wax lu ko neex ci ku ko neex. Ba sax, leeg-leeg, askan wi di jéem a fajal boppam. Loolu bokk na ci li tax kii di Abdu Baara Dolli yékkati ay kàddu yu tegginewul teg ko ci ndoddu Njiitu réew mi bañ teg ko loxo. Bu dul dara sax, mu jox ko cёr donte ne ñoo bokk làngug politig gi. Ndax kat, kenn umpalewul ni njiitu réew moom campéef la (institution), du lu neex waay teg ci deram. Ni yoon doxale foofu la war a def ci yeneen xeeti kàddu yu ñagas yoy, gaa ñaa ngi leen di biral, di leen boyal. Taafar si, donte ne jikko yu yàqu yi bokk na ci li ko yokku, mbaalu jokkoo yi kenn demul ñu des. Nde, xeetu taafar yu bari fa lañ leen di jàllalee ba ñépp jot ci, bu dees sax sa biir néeg nga nekk di bind ak a wax say musiba. Kibaaraan yi tamit daldi jёlaat wax ji tasaare ko fépp. Yooyu nu jot a lim bokk nañ ci li waral ak li lawal taafar yi ci réew mi. Léegi nag, luy pexe ci mbir mile ngir mu wàññeeku ci réew mi ?

Liy pexe nag ci mbir mii mooy yoon jёl ay matuwaayam ci li nit ñi di wax ak li ñuy jàllale ci mbaali jokkoo yi ak kibaaraan yi. Waaye, loolu mёnul am feek yoon tёddewul njaaxanaay, yamale ku nekk ci kujje geek ku nekk ci nguur gi. Mu bañ doxal Kummba am ndey, Kummba amul ndey. Ku def lu dul yoon ñu teg ko ci yoon fum mёn di bokk ak lum mёn di doon. Te, ñi féete ci làngug pólitig gi bàyyi xel bu baax kàddu yi ñuy biral. Ndax, bu fekkee ni mbooloo dafa topp sa gannaaw danga war a xam nooy waxe ak nooy jëfe ngir sàmm say ñoñ. Nga bàyyiwaale xel ne ñi topp sa gannaaw dañ la bёgg am ci yow yaakaar. Ba tax na, amul loo leen dul jaral ngir ñu aar la, nekkal la fépp. Waaye tamit, ngir ñu dёgёral seen taxawaay ci làng gi (parti). Moo tax, mu bari lool lu nuy gis ku génn teg ay kàddu yu ñagas ci kenn ku féete ci genn làng, keneen jóg tontu ko. Ndax kat, ku ёmb sa sànqal, ёmb sa kersa. Te, lafañ sax nag, boroomi mbaam lay àndal. Waaye, bu dee ñi nekk ci làngug politig gi askan wee leen ñor, jarul ñu ciy noonoo. Donte ne sax, ñu bari ci ñoom dañoo jàpp ne politig moom noonoo la. Li koy firndéel mooy ne saa-senegaal yu bari dañuy foog ni kujje moom noonoo la. Déedéet, kujje moom ñàkk a bokk gis-gis la rekk walla péete. Donte ne sax, réerewun ne ku sa wujj sëlëm doo set. Wànte, mёn nañ ko rafetal, ba kenn du teg ay kàddu yu ñagas ci moroomam. Loolu kese mooy pexe ngir taafar si wàññeeku ci réew mi. Te, yoon tamit yamale ñépp ba ñi fare ci kujje gi bañ a jàpp ni dafa jeng. Bañ a def liñ naan làq doom, dóor doom. Ku jalgati mu teg la ci yoon bañ ci seet dara.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj