TABASKI 2023 : XUTBA SËRIÑ BAABAKAR SI MU DABBAAX (NJOOL-FUUTA)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci alxamesu démb ji la ñu ëpp ci saa-senegaal yi tabaski. Ku ne tabaski, ne xutba. Te, xutbay imaam yi, dees na koy faral di xaaj ñaari pàcc. Bu ci njëkk bi, imaam yi dañu koy jagleel diine ji, jagleel beneen ñaareelu pàcc bi tolluwaayu réew mi, rawatina li ci fës. Noonii la fa deme at mii tam, fa tiwaawon. Sëriñ Baabakar Si mu Abdul Asiis Si Dabbaax xirtal na jullti Senegaal yi ci ñu dekkil mbaaxi mbokkoo ak dimbalante, cuufe ak sutura.

Ci alxames ji la tiijaani Tiwaawon yi tabaski. Kilifa gii di Sëriñ Baabakar Si mu Abdul Asiis Si Dabbaax, ñu duppee ko Njool-Fuuta, moo jii te julli ba. Ba muy xutba, dafa fàttali mbaaxi démb yoy, dañuy bëgg naaxsaay ci biir mboolaayu Senegaal. Moo ko tax a ñaax askan wi ci dundalaat mbaaxi yooyii mag ña sàrtoo woon. Sëriñ bi ne :

« Ñi amul wërsëgu dunud ak seen i maam, dund nañu, as-tuut, ak seen i baay. Réer gu jéggi dayo gi fi am day firndeel ñàkkug gindikukaay. »

Sëriñ bi neeti, jot na ñu fàttali doomi Senegaal cuufe ak dimbalante, rawatina ci jamono yu mel ni tabaski ak tolluwaayu réew mi. Imaam bi ne :

« rendi sam xar, di bàkkoo taar baak duufaay bi taxul Yàlla nangul la. Diine, dees na ko dunde ni ko Islaam tëralee. »

Xalifa Tiijaan yi, Sëriñ Baabakar Si Mansóor, dafa tawat moo tax jiitesiwul julli ji. Waaye, balaa Njoo-Fuutay xutba, Papaa Maktaar Kebe waxoon ci turam, jottali ngërmaandeem tiijaan yi jàpp yépp ci tabaxug jumaay Tiwaawon ju mag ji. Jottaleet na ñaan xalif yi bi jagleel daayira yi, kurél yi ak saa-senegaal yépp yi ci jàpp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj