Tàmbaakundaa moo aye. Fa la Ndajeem jëwriñ yi Nguur giy amal ayu-bés bu neek di ame ëllëg ci àllarba ji. Njiitu réew mi, Maki Sàll ak Càmm gépp ñoo nga fa jamono jii, fas yéene faa waxtaane mbirum koom-koom ak yokkute.
Diiwaanu penku-suufu Senegaal dalal Njiitu réew mi Màkki Sàll ak i jawriñam. Mbooloo mu takkoo takku a leen teeru, defum njooxe. Ba tax na, ca teeru ba, foo sànni mbàttu mu tag. Ñu seetlu ne, ña fare ca seen mbotaay googu di APR, kenn ku nekk rung nga sa ay nit, solal leen meloy parti bi, ñu fees dell ci mbeddi Tàmbaa ya.
Nguur gi nag liggéey na diiwaan ba ci lu bir. Ku gumbawul ku ne, war nga gis màkkaanum sóobare ma fa Njiitu réew mi tijji, ca Gudiri. Tey, ci Talaata ji, kaaraange gën na fàgguwaat ci biir réew mi, rawatina ca Tàmbaa. Diiwaan nag, kenn taamuwu ko cig neen. Ndaxte, fi mu féetete digaloo ak ñeenti réew, sabab la bob, dafa am solo lool ci wàllu kaaraange réew mi.
Ku wax Tàmbaa, wax dem ak dikk, tudd ay yoon. Moo tax it, Màkki Sàll xelam faayul loolu. Tijji na yoonu Tàmbaakundaa-Gudiri-Kidira ànd ci ak jëwriñ ji mu dénk wàll woowu, di Mansuur Fay.
Leneen lu fés ca liggéey boobu, di yeesalaatu gox ya. Te, Nguur gi daf ci ànd ak waa “Promovilles”. Ñoonu def ci lu tollu ci 11i tamñareti CFA ngir gën a taaral biir dëkk ba. Muy ay yoon yuy lëkkale gox ya fa nekk, te di yombal dem bi ak dikk bi. Dees na fa def tamit ay làmp yuy leeral biir dëkk ba. Ndege, lu tollu ci 434i làmp lañu sàmp. Wànte, “Promovilles” fàttewul jigéeni Tàmbaa yi. Ndaxte, tabaxal na leen kër gu ñuy amale seen i yëngu-yëngu ci wàllu coppig meññeef yi. Mu war a dalal lu mat 2 000i jigéen yu ciy yëngu.
Mënees na wax ne Tàmbaa gëj naa yëngoo nii. Nee ñu, xaalis bu bari tuuru na fa. Mbir yi nag, dafa xaw a niru ak mitiŋ. Lees taf nataalu Njiitu réew mi ci meri bu Tàmbaa jur na coow lu bari, kujje gi di ko ñaawlu. Ak lu ci mën di am, warees na sàmmonte ak yoon, te sàmm kàddu yi.