TAMXARIT

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tamxarit bokk ci na ci xew-xewi diine fii ci Senegaal. Tur wi rekk làmboo na doole ji mbatiit am wàll ci moom. Mu nekk ci diiney Lislam, di yamooo ak weeru tamxarit (muharram ci araab). Bés bi lañuy woowe asuuraa. Muy màndargaal ndorteelu atum jullit ñi. Tamxarit doon xew-xew bu ñuy amal ci guddig fukkeelu weeru muharram (wolof naan ko weeru tamxarit). Mu doon xew-xew bu boole diine ak aada.

Fii ci Senegaal, tamxarit am na wàll wu réy ci xew-xew yi. Mu nekk lu ànd ak xumbeel lool ci waajtaay yi ak nees koy amalee. Màndagaleesut lu moy ndoorteel at mu bees ci jullit ñi. Waaye, mbatiit mi réew mi am, muur na ko ci ay aadaam. Mu nekk lu ñenn ñi gis ne ay bidaa la, ñeneen ñi jàpp ni aadaa dañu koy sàmm. Moo tax, ñu nemmeeku ci reeri tamxarit, taajabóon wala sax ca ëllëg sa naafilay ñeenti rakkaas yu ñuy amal ci jumaa yi ak jàkka yi.

Bokk na ci li ci gën a fés di cere yi ñuy baaxoo togg di ko reere ci guddi gi. Jigéen ñi ak seen i feem ya ñu cay dolli. Ñii boole ko ak ñeexum baase, ñeen ñi taamu cerey siim. Toggin yi wuute lool tey ak fi jamono tollu. Ñu gis ne, bu njëkk, barke ak wér-gi-yaram bokk na ci la ñu daan seet. Nde, xamees na ne dugub ñam wu baax la. Waaye tey, jigéen ñaa ngi def ay baase-salte, ay cerey bombu. Di ci def lu nekk ngir neexalee ko seen i togg. Waaye, dafa doon lu fajkat yi di moytuloo jigéen ñi ndax loraange yi ci nekk.

Guddig tamxarit gis nañu ci am xumbeel mu ñu naan taajabóon. Muy door ginnaaw ba ñu teelee reer. Ndaw ñi wala ñenn ci mag ñi di ko def. Na muy demee mooy góor ñi dañuy sol yérey jigéen, jigéen ñi sol yérey góor. Ñuy wër ci kër yi di woy taajabóon, sama taaj bii…, di tëgg, di fecc, ñu leen di sarax.

Ca ëllëg sa mbiri diine jaa ca gën a fés. Muy julli yi, ñaan yi, koor gi ak doxu-mbokk yi ñu ciy amal.

Mënees naa tënk ne, tamxarit nañu ko daan amale démb, mu ngi wàññeeku bu baax. Ndax seetlu nañu ci defin wi day gën a néew, nde bu weesoo la ca diine sàntaane, aada jaa ngay ruus.

 

 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj