Ay fan a ngi ñuy amal ay wote ca Ngomblan ga ñeel koom mi ñu war a yoree réew mi. Dépite yi di càmbar ak a seet ñaata lañ war a def ca jibay jëwriñ ju ci nekk. Démb ci àllarba ji, jëwriñ ji ñu dénk njàng mu kowe mi jàll na.
Meetar Musaa Balde jàkkarloo na ak dépite yi ngir sàkku ca ñoom koom may war a doxal bànqaas boobu ñu ko dénk. Laataa loolu, jot naa tënk naka la mbir yooyu deme ak fa ñu jaarale koom ma woon ca at mi ñu génn. Doonte ne moom sax, gis nañu ne ca mujjantal ga la falu ginnaaw ba mu fi wuutoo naataangoom bii di Séex Umar Aan, dikkaat na ci liggéey ba fa jot a am. Ñu mën ca jàppe wàlluw jumtukaay rawatina ciy tabax yu mat 488 ciy tamñaret (milliard) def nañu ko ci atum 2022 jàpp 2023. Ci loolu ba tay ma ngay xamle ne ci atum 2024 mii ca lañ def ci jibaam, fas na caa yéene xàppati ci lu tollu ci 13 634 000 000iy ci sunu xaalis ngir yeggale ci daara ju kowe ja ca Kawlax di USSEIN.
Mu xamle yit ne réewum Senegaal, wàlluw gëstu xar na ci tànku tubayam. Ndax lañu ca def ciy kopar tollu na ci 24 354 000 000. Te, limeesu ca naalub “Madiba” fa ñu doon defaree ñakk yii di covid-19. Waaye, fàttewut it na ñuy yore daara yu kowe yi ñeel seen doxalin. Mu bokk ca na ñuy fale njiiti jàngune yi (recteurs), ñu gis ci ay coppite.
Ca geneen wàll ga fàttewut a duut baaraamam ci xew-xew yi woon ca weeru me jàpp suwe. Muy lu muy nàqarlu ak a ñaawlu ginnaaw ba mu xaymaa lu bari la fa yàqu. Ci loolu, dépite yi bàyyiwuñu ci laaj bi yitteel saa-senegaal yu bari, di kañ lañuy ubbi daaray Séex Anta Jóob ja ca Ndakaaru. Waaye, nee na, lees tànn mooy wéyal njàngum teewadi mi (enseignement à distance) ba at mii jeex, déwén ñu ubbi jàngune bi ci jàmm ak kaaraange.