UBBITEG LEKKOOL YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lekkooli Senegaal yi tàmbali na tijji ay buntam. Niki démb ci altine ji, 2 fan ci weeru oktoobar 2023, lañu woo jàngalekat yi. Naka noonu, ndongo yi war leen a fekki ci alxames jii yamook 5 fan ci weer wi. Lekkool bi nag, ciy jafe-jafe yu bari lañu ko bàyyee woon. Rax-ci-dolli, njàng maa ngi door ci njeexitalu nawet bi. Fan yii, jàngalekat yaa ngi doon kaas ak a artu. Lees di ragal nag, mooy lekkool jànkonteel ak i yëngu-yëngu yuy gàllankoor njàngum xale yi, rawatin bees jubee ay wote, féewaryee 2024.

Lekkooli Senegaal yi gëj nañoo ànd ak seen sago. Muy daaray tuut-tànk yi, yu digg-dóomu yi walla sax jàngune yi, benn yembu ci. Bu ñuy laaj sabab bi, jàngalekat yeek njàngaan yépp Nguur gi lañuy duut baaraam. Bu ko defee, waa Càmm gi génn, di lay ngir setal seen der. Waaye nag, ku ñépp tëfli nga tooy. Xaatim ay pas, joxey dige yu dul jeex ba noppi bañ leen a jëmmal, noonu la Nguur giy doxe. Nde, saa bu coow amee, ñu wootem ndaje, waxtaan, déggoo ci dara. Waaye bu desee lu dul jëf, Nguur gi njuuy jàngalekat yi walla njàngaan yi, jàdd koñ. Noonu, jàngalekat yi damm kere yi, toog seen i kër, ndongo yi génn kalaas yi, wutali tali ba di xeex ak takk-der yi. B

Loolu yépp doyul, pólitig bi rax ci. La xewoon ca jànguneb Ndakaaru ba (UCAD) ak bob Ndar (UGB), ci weeru suwe bee weesu, doy na ci firnde. Cig pàttali, ba ñuy tëj jàngune yi, njàngum at mi jeexagul woon. Moo tax, coow ak yàqute ya amoon fa UCAD ñoo tax jàngune bi tijjeegul te yeneen yépp door nañ njàng mi. Kon, buñ nee dañuy ubbi kalaas yi te saafarawuñu jàngoro yi ko gaar, xel dina teey.

Jàngalekat yi nag, ñu ngi artu. Bu ñu sukkandikoo ci seen i wax, ñu ngi jëm ci palug njiitum réew mi. Te, xew-xew boobu mën naa indi ay gàllankoor yu réy ci réew mi ba ci lekkool yi. Leneen li nar a yokk xar mi karaw mooy li lenn ciy gox tumurànke ay jàngalekat, néewle ko lool, rawatina ci lekkool yu dig-dóomu yi. Bu ñu waxee loolu, xel yépp dem ci dëkki kow yi walla dëkki àll yi. Am na ci sax ñoñ, ci néegi ñax lañuy jànge. Bu ngelaw li ëfee, walla taw bi sóob, lépp yàqu. Nga booleet ci coow li dox diggante jàngalekat yi ak Nguur gi. Lii yépp a tax atum ren mi teey xel yi. Loolu la Tamsiir Baaxum di dëggal ci kàddoom yi Leral.net siiwal, muy wax ne, atum ren mi nar naa yëngu, ndax li waxtaan amul seen digaante ak Nguur gi. Lii ba kañ ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj