Ginnaaw Fàllu Seen (2018), leneen ndongo faatooti na fa jànguneb Ndar ba ci sababuy ñaxtu. Démb, bi njàngaan yiy ñaxtu ngir kaas ndogalul dàq wotey 2024 yi, la sàndarm yi soqi ab bal ci kow ab njàngaan, ñu rawale ko fa raglub Ndar ba. Waaye, Alfa Tunkara, doon jàng “Géographie”, mujje na ñàkk bakkanam.
Moom Alfa Tunkara, mi ngi juddu béub 17 màrs 2001 fa Ndendi-Ferlo. Ci ñaareelu atu njàngam la tolloon (licence 2), ca banqaasu “Géographie”. Mi ngi dëkkoon “Village P, chambre 110”.
Bees sukkandikoo ci kàdduy Gabiriyel Bàrbiyee, taskatu xibaar bu liggéeyee Walfadjri, li ko rey mooy li tubaab di wax “Trauma à la poitrine”. Maanaam, ab gaañu-gaañu ci dënn bi.
Wii mooy ñaareel wi yoon takk-der yiy bóom ab njàngaan fa iniwérsite Gastoŋ Berse bu Ndar. Moo tax ndongo ya dajaloo démb, di wax ne “UGB du ay sëg !”.
CESL, kurél giy sàmm àqi ndongoy Ndar ya, dakkal njàng mi ginnaaw biñ dajaloowee ci guddi, biraale. Yeneen jàngune yi dakkal nañ seen um njàng ñoom itam ngir naqarlu seen moroom bi ñu reyati. Nii nii, ndongoy Ndar yee ngi ci tali bi di xeexateek takk-der yi.