Dogal bi ñu doon xaar tey ci Talaata ji jëm ci àtteb Usmaan Sonko ñeel li ñu ko bëgg a dàq ci wayndarew wote yi, àttekat bii di Usmaan Raasin Coor, dàq na dogal bi ba alxames 14 desàmbar bii di ñëw bu 9 i waxtu jotee.
Niki ni ñu ko fésale ci sunu yaxal bi wees jëm ci àtteb Usmaan Sonko ak Càmm gi, dogal bi muj naa tagatémbe. Muy ab layoo bu ñu séqoon ay waxtu ci diggante layookati Càmm gi ak yooy Usmaan Sonko ca ëttu àttewaayu hors classe bu Ndakaaru. La ñu ca seetlu mooy kenn ku nekk lay nga ngir sab kiliyaŋ. Muy lu ñu miin ci ëttu àttewaay yi. Waaye li ci muj leeragul ci bopp nit ñi. Nde, àttekat bi li mu ca xamle mooy day sëgg ci lay yooyu fi ag ginnaaw suba laataa mu ciy àddu.
Waaye bu ñu dégloo layookat yi ginnaaw bi xibaar bi jibee, moo xam waa Càmm gi wala yooy Usmaan Sonko, kenn ku nekk ca ñoom, a ngi dunde yaakaar ne mooy am ndam ci kaw keneen ki. Nde, bu ñu sukkandikoo ci layookat bii di Keledoor Li, la mu ca gis mooy ña ñu ko séqal doxalewuñu yoon, xanaa jaay doole lañu fa nekke. Nde, lépp àttekat bi la ko mujj sëf ngir mu doxe yoon, xam-xam te Yàlla rekk tax. Ca geneen wàll ga, layookat bii Elaas Juuf miy layal Càmm gi àddu na ci la tukke ca jàkkarloo boobu. La mu gis mooy lii yéexal jéll la rekk nde Usmaan Sonko lu ko mën a dal moo ko teg boppam.
Mënees na tënk ne layoob Usmaan Sonko ak Càmm gi pënd ba wureegul nde dem beek dikk bi jeexagul. Lépp nekk ay waxtu yu jamp ci njiitul Pasteef li woon, ndax bés yi des ngir ñu tëj wayndarew wote yi bareetul.