Njiitu Càmm gi, Usmaan Sonko, seeti woon na kilifay diine yu Tuubaa ak Tiwaawon. Tay, ci yoor-yooru talaata ji, la dem fa Tuubaa, Séex Muntaxaa Basiiru Mbàkke dalal ko. Njiitu murit yi dalal na ko fa dëkk bu sell ba ca Daaru Tànsil.
Gise boobu doxoon seen diggante, nekkut lu ñu yaatal. Nde, nemmeekuwuñu ci am mbooloo. La ca jot a rot ciy xibaar mooy dépite Séex Coro Mbàkke bokkoon na ca jataay boobu. La ñu waxtaane, mel ne ni génnut gis- gis wala naali njiitu Càmm gi ci réew mi. Waaye, bokkees na ca yéene ji mu am ci dëkk bi, ci lu koy jëmale kanam. Ba tax na, fas na yéene sóobu ci li soxal askanu Tuubaa, ci ni ñuy gën a ñoŋalee seen ug dund. Waaye tam, taxaw ci seen uw nekkiin. Mu taggatoo ak kilifa gi ginnaaw seen uw waxtaan wu yaatu. Séex Muntaxaa ni mu ko baaxoo defe, may na Usmaan Sonko téere bu sell bi, di ab kaamilu Alxuraan.
Ginnaaw ba mu jógee Tuubaa, Usmaan Sonko dafa jubali Tiwaawon. Lépp nekk ci bésub talaata ji. Ca dëkk bu sell boobu, kilifa gu mag ga dalal na ko. Sëriñ Mbay Si Mansuur gise na ak njiitu Càmm gi. Lañu jot a waxtaane, mel ni ne yaataluñu ko. Bu ñu sukkandikoo ci këru xibaar gii di Seneweb, ndaje moomu bokk na ca lañu fore ci seen uw waxtaan mooy naal bii di “PROJET”.
Ñu mën a tënk ne génn googu, njiitu Càmm gi amaloon ci kanaamu kilifay diine yu Tuubaa ak Tiwaawon, mel ni weesuwul ay naali pólitig. Seetloos na ca aw waxtaan yu tënku. Nde, lañu jot a waxtaane nekkut lu ñu biral. Waaye, mu mel ni jubluwaay bi rombul ay pexe ngir taxawu askanu Senegaal. Wànte it, nu ñuy suqalee réew mi ak naalam bii di “PROJET”.