USTAAS UMAR SÀLL MA NGA CA LOXOY YOON

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ustaas Umar Ahmad Sàll, ab waaraatekat bu siiw ci réew mi la. Fës na lool ci mbaali jokkoo yi. Nde, bari nay waxtaani diine yu muy amal di leen ci biral,  jaare ko ci seenam bii di “Daaroul Birr wal Irchad”. Moom nag, mi ngi bokk ca giirug sunnit yi, maanaam ñiy dundu Sunna te ñu leen di dàkkentalee, fi réew mi, “Ibaadu” walla “Wahabii”. Moon nag, démb ba tey, mi ngi ci loxoy yoon. Ndax, taalibe-séex yi ñoo ko kalaame woon yoon.

Coow li nag, la ko wund moo di aw waxtaan wu mu defoon, jaraale ko ci mbaali jokkoo yi. Kàddu ya mu jotoon na jàllale nuru ak tooñ ci déggiinu ñenn ca ña bokk ca tarixa tiijaan, ay taalibe-séex. Moom Ustaas Umar Ahmad Sàll, dafa doon àddu ci yenn xeeti tuddiinu Yàlla, di wax ne wérul ci diine, amul cëslaay ci Sunnas Yonent bi (SAWS). Booba, da doon tontu as waay su doon tiiñal ak xas “Ibaadu” yi. Bi Ustaas di wax, tuddul wenn yoon tiijaan yi, tuddul “wasifa” walla “xadra”. Moom daal, dafa wax ne dajaloo di yuuxu “Allaa ! Allaa !” bu dul jeex bokkul ci diine ndax Yonent bi (SAWS) jàngalewu ko te mësu ko def. Ci weneen waxin, moom boroom daara ji nekk ca Daaru Cub, dafa gis ne loolu bidaa bu bir la walla am po. Toppandoo na leen sax, di miim ni ko ñenn ñiy defee, mel ni ñuy daanu rab. Kàddu yooyoo ko yóbbe nattu bim nekkee tey jile.

Li mu wax noonu moo naqari tiijaan yi, ag kurél gu dajale ay ndaw yuy woowe seen bopp taalibe-séex pelent ko. Ginnaaw gi sax, moom Ustaas defatoon na beneen widewoo di ci leeral ni tuddul turu kenn. Waaye, komiseer Aali Kànde daf ko woolu woon démb ngir déglu ko ci luññutu ga ko toppekat bi dénk. Bim ko dégloo ba noppi, daf ko téyandi foofu. Tey la waroon a gise ak toppekat bi, waaye mujjul a àntu. Nee ñu, ëllëg ci àjjuma ji lay janook moom.

Li jaaxal ñu bari nag mooy ne, bés bu set, am ñu saaga Yàlla (SWT), saaga Yonent bi (SAWS), xas ay saabaam, diiŋat Lislaam ji te kenn du leen pelent, dara du leen ci fekk itam. Ñu ngi dox seen i soxla nu mu leen neexee. Mootax sax, am ñuy njort ne, Ustaas, mbiri tarixa kese taxul ñu jàpp ko. Nde fan yii, doon na dal ci kow Càmm gi ñeel mbëkk mi lëmbe réew mi. Muy lu doy waar.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj